Gannaaw 9i at ci boppu ekibu Senegaal bu mag bi, Càmmug Senegaal gu yees gi dàq na Aliw Siise. Ci àllarbay tay jii, 2i pani oktoobar 2024, li xibaar bi jib. “Féderation Sénegalaise de Football” moo siiwal ab yégle tay ci suba, biral xibaaru ndàqug Aliw Siise.
Ci biir yégle bi, kurél gaa ngi xamle ne, ndogal li, ci Càmm gi la bawoo. Ndax, jëwriñu ndaw ñi, tàggat-yaram yi ak mbatiit mi, Soxna Xadi Jéen Gay, moo leen yónnee ab bataaxal du leen ci wax ne duñu wéyal pasug Aliw Siise gog, ci weeru ut wii weesu la jeex. Ñetti sabab la jëwriñ ji joxe yoy, ñoo waral ñu tàqalikook Aliw Siise.
Ci yégle FSF bi leeral nañu sabab yi tax ñu wàccee tàggatkat bi. Bi ci jiitu mooy li Senegaal àggul kaar-dë-finaal ci joŋantey kuppe yu 2022 yi, doon amee fa Qataar. Ñaareelu sabab bi mooy li Senegaal toogee ci wicceem-dë-finaali CAN bii weesu, doon amee fa Koddiwaar mi toogloo woon Senegaal. Ñetteel bi, di bi ci mujj, day dellu ci ñuq-ñuq gi tàmbalee am ci diggante ekib bi ak saa-senegaal yi. Ndax, askan wi gisatul woon boppam ci gaynde. Maanaam, ñi leen Aliw Siise di futbal-loowee neexu leen te safu leen. Moo tax sax, daanaka ñépp ñoo ànd ci demam gi. Waaye nag, kenn fàttewul jaloore yi mu def.
Aliw Siise, dees na ko sargal. Ndax, moo fi defagum lu kenn defagul. Nde, ci diirub kayam gi, def na fi lu réy lees dul fàtte mukk. Jaar-jaaram ci boppu ekib bi nii la demee :
Aji-finaalu CAN 2019
Waadab CAN 2022
1/8 finaalu CDM 2022
Mooy tàggatkatu ekibu Senegaal A bu fi njëkk a andi kuppeg Afrig. Kon Aliw, Siise Ngaari, Senegaal gërëm na sa liggéey ! Jërëjëf gaynde.