Futbalu tefes gi : Gayndey Senegaal yi fobooti nañu

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaynde Senegaal yu futbalu tefes gi fobu nañ. Démb ci alxames ji lañ doon nangu raaya réew mi ci loxoy Njiitu réew mi. Bile yoon nag, ña nga jëm ca Mosàmbig ngir joŋante Can 2022 bi, waaye itam ngir dàkk juróom-ñaareelu raw-gàddu. Mu nar a doon xeex bu metti.

Bu dee am na ci wenn fànn wu Senegaal noot Afrig yépp, futbalu tefes gi lay doon. Loolu ñépp ko ànd seede. Ikibu Senegaal bi jël na juróom-benni yoon lii di Can bi. Ba tax na yoon wii nar a metti ci ñoom. Gaynde yi ci seen bopp xam nañ ni ikibu senegaal bi la ñépp di xaar ci Can bi. Te itam dara naru faa yomb. Loolu tax na ba Al seyni Njaay, di njiital gàdd gi fàttali na ko ciy kàddoom ginnaaw bi mu nangoo raaya réew mi ba noppi :

« …mbégte la ci man saa su may jot raaya réew mi. Dégg nañ bu baax kàdduy Njiitu réew mi. Li des mooy dem xeex ba jeex ngir jëlaat ndam li. Du yomb nag ndax nun la ñépp teg i bët. Nun la ñépp di xaar. »  

Ógistĩ Seŋoor, njiital FSF teewoon na fa itam. Yékkati na fay kàddu, fàttali leen seen jaloore, ñaaxale leen boole ci :

“Ñoom la ñépp di xaar ndax li ñu mën ci kembarug Afrig gi te seen i jaloore yokk na jom yeneen gaynde yi ci futbal bi. Noo ngi yaakaar ñu dàbbali ndam li ci jamono jii ñuy waajalee kub di mond bi.”

Jëwriñ ji yamul ci yeb leen ak dégtal leen yakaar gi mu am ci ñoom. Bi mu leen ñaaxee ba noppi, toftal na ciy kàdduy sas :

« Laajunu leen rekk ñu jël ndam li ndax liñ nu ko tàmmal. Dañuy sàkku itam ñu dellu bokk ci kub di mond bi, wéyal liggéey bi ba di diir mbagg ponkali àddina si, ba jël kub bu àddina si. »

Ngir gën leen a gunge, moom jëwriñ ji jël na itam ak waa FSF ndogalu yokk seen i neexal ba ci 4i tamndaret. Ku ci nekk dina jot 1 tamndaret ci seen dem bii. Bu ñu fa amee ndam, dina leen joxaat 2i tamndaret ku ci nekk. Bu ñu àggee ca kub dii mond ba nag, mu dàbbali leen ku ci nekk 1 tamndaret.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj