Jinne yu ñuul yi ñaay nañu Sunu Gaal gi, soppi ko gàngunaay, tëmbal ko ci géej gu sàmbaraax. Sunu Gaal gaa ngiy jaayu, jinne yu ñuul yee ciy gaajo. Sunu Gaal gaa ngiy jayaxu, jinne yu ñuul yee ko nar a galajaane, wax dëgg.
Miim réew a barey feebar !
Senegaal, sunu gaal geeka dëng. Ay xeeti jàngoro yu doy-waar ñoo daaneel mboolem-nawle mi ba foo laal ci yaram wi, mu onk. Jamono jii, feebar bi ci gën a fés mooy njabar. Tey, njabar dafa dib feebar bu law. Dees na ko gis ci mag ñeek ndaw yi, muy góor walla jigéen. Moom, kay, ku tedd ki sax muccu ci, waxatumalak baadolo bi. Amaana gëm-gëmu njabar lu fi yàgg la ndax diiney ceddo ji fi nekkoon. Waaye ni mu tasaaroo tey ci mboolem-nawle mi dafa ëpp ba jéggi dayo.
Saa su ñu dégmaleeb xew-xew, dees na gis taskati xibaar yiy wër këri gisaanekat yi, seetkat yi, saltige yi, ceddo yi, añs. Ku ci nekk ñu tàllal la mikóro ngir taataan sa xalaat walla sa gis-gis ñeel li nar a xew ëllëg. Bu dee làmb, ñu naan diw ay daan, diw ay daanu. Bu dee ci làngu politig gi : gis naa diw ca pale ba, diw dina falu, diw moom, bu yaboo sawi te tëri, du mës a toog ci jal bi… Bu ko defee, tele yi, rajo yeek yéenekaay yiy biral kàdduy jinne yu ñuul yeek seeni nataal, ñu ame réew mi, tanqal ñépp. Ba tax na, ku ciy def dara walla mu am ab naal, day laxasaayoo lëndëm, yoot ci guddi gi, seeti jinne yu ñuul yi. Daanaka kenn muccu ci.
Mbir mi àgg na ci, ku ci sa baaraam xaw a metti sax, nga ne « lii du neen, man kay fàww ma seetluji ! ». Noonu, nga jàpp ne dañ la liggéey, daldi noonoo ku la deful dara. Kon njabar day yàq diggante ndax li muy jëkk a saxal ci xolu doom-aadama bi mooy ñaaw njoort. Rax-ci-dolli, ku ci am jafe-jafe bu ndaw, bu ko jiiñul njabar, mi ngiy njabarluji. Mu mel ni Yàlla nekkatul kiy dogal. Te, nag, coow li coow li, njabar ak lépp li ci aju, ay kàcci neen la. Waaw.
Li lay wan ne gisaanekat yi, seetkat yi, boroomi pettaaw yeek ñoom seen waxuñu dëgg, mooy ne, boo dégloo ñett ci ñoom, seeni wax duñu méngoo. Te saa bu biree ni fen nañu, ñu daldi wut ay lay, naan jinne ji nii, jinne ji naa…
Waay bàyyileen jinne yi ngeen di tooñ !
Kenn nangootul a liggéey ; ñépp a ngi toog di déglu gisaanekat yi. Ndeysaan, dem nañu ba gëmatuñu jëf. Ndax kenn gëmatul boppam, kenn yaakaaratul Yàlla, waaye kenn sukkandikootul ci xam-xamam, mën-mënam walla ngoram. Foo tollu di dégg kàdduy jinne yu ñuul yiy jib, seen baat yu ñuul yi ca kow, ñuy joobe Séytaane. Tee ñu leen a takkal gafaka ? Ndege, gàkkub njabar du gaatnga mukk lu baax. Ndax, réew mu mu taq, askan wa réer, te réew mu sa askan réer sa koom-koom nasax, nga daldi sooy, dellu ginnaaw.
Paap Aali Jàllo
GAALU JINNE
