Démb, ci guddig dibéer ji jàpp altine jii, lañ doon amal gàmmu 2024. Muy xew mom, dañ ciy màggal bésu ganesi àddina Yonent Yàlla Muhammet (SAS). Fa Tiwaawan, Xalifa ba amal na fay pàttali ci dayoy Yonent bi ak ni mu nekkee royukaay bi gën a màgg ci njéggal, ci mbaax ak ci yërmande jëme ci mbindeef yi.
Wax na itam ci tolluwaayu réew mi, rawatina ñaawteef yu jéggi dayo yees fiy nemmeeku, seen bariwaay ba ñu mujj leen woyofal. Ba tax muy woo way-gëm yi ñu dellu ci teddaangey njàngale Yonent bi, te booloo ngir mën a dékku jafe-jafe yi ak wut ay pexe ci njàqare yi nar a nasaxal sunu dundin ak sunu yokkute.