Meeru Sigicoor bi, Usmaan Sonko, biral na 12i naal yi mag yim jagleel diiwaanu Sigicoor. Ci ngoonug démb ji, àllarba 26 awril 2023 ca Sigicoor, la fésal naal yi. Dinañ tabax ca diiwaan ba ay ja, tali, fowu (estaad), jàngu (daara, ekool). Njiitul Pastef li dina fa samp ay làmp ngir leeral dëkk bépp, yeesal ay béréb ya askan way féexloo ak a waxtaane.
Woolu nañu Mustafaa Jóob
Ca komisariyaa Ndakaaru bu mag bi la waa Suret urbaine woolu njiitul tele Walf Tv, Mustafaa Jóob, ngir ñu déglu ko. Tey, ci alxames ji, 27 awril 2023 laytontuji laaji waa DIC yi. Nee ñu nag, kenn toppewu ko dara. Dañu koy laaj doŋŋ ci mbirum Paap Njaay, takatu xibaar bu Walf Tv biñ jàpp ci kaso. Maanaam daal, dañ koy seedeloo. Yàggoon na ca biir lool nag. Waaye, bàyyi nañ ko mu ñibbi.
Taskatu xibaar bi, Baabakar Ture mu Kéwoulo, wuyuji woon na ca DIC. Démb lañ ko woolu woon. Bees sukkandikoo ci layookatam bii di Meetar Musaa Saar, ki ñuy wax Ferederik Napel a ko pelent, moo waral Yoon woolu ko. Li Napel di toppe Baabakar Ture mooy ne, ciy waxam, daf ko tooñ te saaga ko ci kanami ñépp, yàq deram, jëfandikoo ay këyit yu bon, añs. Baabakar Ture nag, jàppandi nañ ko.
Delsig Manker Njaay ci wetu Njiitu réew mi Maki Sàll
Njiitu réew mi, Maki Sàll, tabbaat na Mankër Njaay, Ki fi nekkoon jëwrin jees dénk mbiri bitim-réew ak Saa-Senegaal yi féete bitim-réew ca atum 2012 ba 2017. Tey ci alxames ii, 27 mars 2023, la ko takkalaat ndombog-tànk, mu nekk xelalaatekat ci wetu Njiitu réew mi.
Ginnaaw bi ko Sëñ Sidiki Kabaa wuutoo ci Nguur gi ca atum 2017, moom Mankër Njaay nekkoon na fi Njiitu ITIE (Initiative pour la Transparence dans les Industries Extractives) fii ci Senegaal laata ñu koy yebal ca réewum Sàntar-Afrig ci turu Mbootaayu Xeeti Àddina si.
Yeneen tabb yu yees
Ca ndajem-jëwriñ ma mu doon amal démb, Njiitu réew mi, Maki Sàll jot naa am ñu mu fa takkal ay ndomboy-tànk. Muy ku ci mel ni Abdulaay Juuf Saar (Directeur général du Fonds Souverain d’Investissements Stratégiques (FONSIS), Mammadu Baabakar Njaay (Recteur de l’Université Iba Der Thiam de Thiès) ak Jean Bertrand Bocande (Directeur général de l’Administration pénitentiaire).