ÑAKK A BOKK MAKI SALL CI WOTEY 2024 YI : ÀDDINA SAA NGIY RAFETLU NDOGALU NITU NGUUR KU KO MATE
Maki Sàll dafa jël ndogalu bañ a doon lawax ci wotey 2024 yi ngir, ciy waxi boppam, sàmm kaaraange réew mi. Ñu baree rafeltu ndogal loolu, ci biir réew mi ak ci bitim-réew.
-
Antoñoo Guteres, Magum Fara-caytu Mbootaayu xeet yi, tagg na Maki Sàll
Ci Twitter la Magum Fara-caytu Mbootaayu xeet yi, Antoñoo Guteres, biral naweelam ci Njiitu réew mi, Maki Sàll. Dafa bind, wax ne :
« Dama bëgg a biral naweel gu réy gu ma am ci Njiitu réewum Senegaal, Maki Sàll ak meloy nitu Nguur yi mu wone. Ndogal li mu jël def na ko royukaay bu mag fa réewam ak ci àddina sépp. »
-
Musaa Faki Mahamat, Njiitul Ndajem Bennoog Afrig, naw na Maki Sàll
Musaa Faki Mahamat, Njiitul Ndajem Bennoog Afrig dafa bind, ne :
« Maa ngi fésal sama naweel ci nitu Nguur ku mag ki mu doon, ginnaam bi mu jiitalee Senegaal ak li mu sàmm demokaraasi Senegaal bob, sagu Afrig la. »
-
Àmbasaad Etaasini a ngi rafetlu ndogal li Maki Sàll jël