GÀTTALUG XIBAAR YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

(Ayu-bésu 4eel jàpp 10eelu fan ci weeru Me)

(PAAP AALI JÀLLO)

Liggéey ngir Yàlla : Ñiy liggéey ci kurélug Force Covid giy saytu ak a doxal xeexub mbas mi nee nañu laajuñ peyoor

Seneraal Farãsuwaa Njaay a xaatim yégle biy wax ne ñiy liggéey ci kurélug Force-Covid giy saytu ak a doxal xeexub mbas mi, « feddaliwaat nañ seen yéene ci liggéey ngir Yàlla ci jamonoy mbas mi. » Yégle bii, nag, biralees na ko ginnaaw bi coowal ndàmpaayu 3,5 milyoŋ yi jibee ñeel aji-bokk bu ci nekk. Coow looloo sababoon sax geddug Abiib Sy mi fa teewaloon kujje gi. Moom, nag, nee na tuuma yees teg ci kow kujje gi, wax ne ñooy làqu di déey taskati xibaar yi lépp lu xew ci kurél gi, ñoo ko tax a gedd.

Jullig àjjuma : waa Lewna Ñaseen fippu nañu

Ginnaaw bim jiite julli mbooloo ji ba noppi, ci àjjuma ji, pólis dafa jàppoon Ilimaanu Lewna Ñaseen bi. Askan wa ne dee du fi ame, daldi fippu. Xalifa bi mer, tëkku nguur gi ci kàddu yii : « Dinan wéy di julli àjjuma ju nekk te noo ngi xaar ba benn takk-der teg fi tànkam ! »

Ngir fàttali, bi mbas mi dooree ba léegi, Tuubaa ngi  doon wéy di amal i julli mbooloo te kenn àdduwu ci. Te, Tuubaa, fa la mbas mi gën a ñànge. Ñoo ngi julli tamit ca Medina Gunaas doonte ne nemmeeku nañ fa 4i wàllenti-ëlëm ak lu tollu ci 10i way-tawati Covid-19 bi.

Covid-19 : dee gaa ngiy yokku

Ci diirub fan yu néew, Senegaal deele na ci 8i way-tawati Covid-19 bi. Ci àjjuma ji rekk, limees na biir Senegaal 1500i way-tawat ak lu teg. Ñu ne déet-a-waay, ñu sampal noyyikaay 7i way-tawat yu ame jàngoro ji. Ci jamono joo xam ne, Ndakaaroo ngi doon waaj a am 1000 way-tawat.

Askan waa ngiy daw loppitaan yi

Ñu bare nangootuñu fajuji loppitaan. Jàppees na ni, ku fa dem ñu wàll la jàngoro ji, walla doktoor yi wax la ne daŋ koo ame. Li xew keroog ca loppitaanu Faan day firndéel lu ni mel. 3i nit yi ame woon yeneen feebar la doktoor yi xamal ne, ndeke, dañu ame koronaa. Njiitu loppitaan bi di xamle cib yégle ne, yóbbu nañ leen ca béréb biñ jagleel way-tawati mbas mi. Lëlees na liggéeykat yi laale woon ak ñoom.

Garabu Madagaskaar gi

Bees sukkandikoo ci taskati xibaari E-Media yi, am na ñuy tuumaal Pr Daawda Njaay, di wax ne dafa bëgg a seppi Pr Musaa Séydi ci liggéey biñ sumb ñeel gëstug artemisiyaa bi. Moom daal, mbir mi dafa jaxasoo. Ndaxte, ndaje miñ doon amal ca Caytug Farmasi ak Garab yi neexul ñenn ñiy liggéey ci njawriñu wér-gi-yaram ji. Ci kàdduy ñenn ci ña ko teewe woon, ndaje mi, ndajem xalaat ak seetlu la waroon a nekk ci diggante ay boroom xam-xam. Waaye, dafa mujje soppiku, nekk ab naalub gëstu. Nee ñu, Pr Daawuda Njaay daf fa tudd ay tur te tàgguwul seen i boroom.

Rax-ci-dolli, kilinisiyeŋ yi fekkewuñ ndaje mi te, ñoom, buñ ci dugalul seen loxo dara du sotti. Biñ woowee Pr Daawuda Njaay, laaj ko, dafa ne rekk moom ak ñi muy liggéeyal jébbal nañ naal bi kurélug gëstu gi ngir ñu xool ba xam ndax baax naam déet. Pr Musaa Séydi, ci wàllam, nee na du jëfandikoogum artemisyaa bi ci pajum jàngoro ji ndax wóoragul.

Njabooti Móodu-Móodu yi ak Faatu-Faatu yi kalaameji nañ nguur gi ci Maslaakat bu mag bi.

Li nguur gi tere ñu delloosi néewi Móodu-Móodu ak Faatu-Faatu yi gaañoo bitim-réew ci sababu mbas mi metti woon na lool seen i mbokk. Ndege, ëttub àtte bu mag bi dafa gàntal layookati Mbootaayu xeex ngir delloosi néewi Senegaal yi deewe bitim-réew ci sababu mbas mi (Collectif pour le Rapatriement des Corps des sénégalais décédés du Covid-19 à l’étranger – CRC). Bu ko defee, ngir am ndam ci seen xeex bile, dañoo fas yéene sàkku ndimbal ci Aliyun Badara Siise, Maslaakat bu mag bi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj