GÀTTALUG XIBAAR YI (Altine 13 eelu – dibéer 19eelu awril)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paap Aali Jàllo

Mbasum Covid-19 bi faat na juróomi way-tawat ci diggante dibéer ak altine

Ci dibéer ji, bi minwi di waaj a jot, la xibaar bi rot : benn aji-tawatu Covid-19 génn na àddina. Ñu ni déet-a-waay, keneen gaañuwaat ci guddig dibéer ji jàpp altine, bi 5i waxtu tegalee 30i simili. Bees sukkandikoo ci yégleb njawriñu wér-gi-yaram gi, ndem-si-Yàlla ji faatu ci dibéer jaa ngi amoon 68i at te dëkkoon Kër-Masaar. Keneen ki, moom, 74i at la amoon. Ca loppitaanu Faan lañ gaañoo. Kon, ñetti way-tawat gaañu nañ ci sababu mbas mi ci ñaari fan yii nu génn, bees ci boolee aji-tawat bi faatoo ca Sigicoor. Bu ko defee, 5idoomi-réew mi ñàkk nañ seen bakkan ci sababu mbas mi, bim dooree ba léegi.

Ay dogal yu bees

Njiitu-réew mi, Maki Sàll, waxoon na ko ciTv5 àjjuma jii weesu : nguur gi sàrtal na takkub mask ci askan wépp ak réew mépp li ko dale altine jii, 20eelu fan ci weeru awril 2020.

Ginnaaw « Institut Pasteur », nguur gi dina ubbi ab bérébu saytukaay ñeel jàngoroy Covid-19 bi ci Géejawaay, Waaxinaan akNimsaat, ñu dippe ko « Centre de tests massifs ». li ko waral nag, mooy yokkute wàllent-ëlëm yi biir Géejawaay ak bãliyë bi.

Jawriñu wér-gi-yaram bi ak ndimbal njaboot, Ablaay Juuf Saar, jël nab dogal ngir xeex yokkute wàllent-ëlëm yi. Léegi, dees na jëfandikoo telefon yi ngir seet wàllent-ëlëm yi (traçage téléphonique). Dalal na xeli nit ñi ci ne, loolu pexe mu baax la. Ndaxte, noonu lañ def ba xam fan la wàllent-ëlëmu Luga biñ wàlle woon Pikin jële jàngoro ji laata muy dellu Luga. Jawriñ bi ne, CDP dina bàyyi xel ñi ciy liggéey ngir aar askan wi ba kenn bañ a lëñbët seen i mbiri bopp.

Takk mask mbaa fey alamaan walla tëddi kaso : tànn ci bu la neex !

Jawriñu kaaraange biir réew mi, ngir jëmmal kàdduy Njiitu-réew mi, génne nab mbindum-dogal (arrêté) ci limu 0091-37 bu 17eelu awril ñeel takkub mask bi. Képp ku sàmmontewulak mbindum-dogal boobu, dees na la jàpp, defeere la, tëj la 1 weer boole ko ak alamaanu 20 000 CFA. Awokaa Me Bàmba Siise moo biral dogal bi.

Force Covid-19

Njiitu-réew mi, Maki Sàll, tabb na Seneraal Farãsuwaa Njaay, teg ko ci njiiteefu kurél Force Covid-19 biñ jagleel xeexub mbas mi. Nee ñu, Seneraal Farãsuwaa Njaay moomu, ku ñàkk caaxaan la te farlu lool ci li muy def. Bu dee kurélug Force Covid-19 bi, nag, pàccu askan bu ci nekk teewal nañ la fa.

Mbas mi laal na doktoor yi

Benn biyólósist bu jigéen moo ame jàngoroy Covid-19 bi ca loppitaanu Matlabul Fawzani. Moom, jëkkëram, ay mbokkam ak ay fajkatlañu gawandoo. Ñi ngi tollu ci 25i nit.

Wàllentuw-ëlëm bu Waaxinaan Nimsaat ba, ca Géejawaay tax na ba ñu tëj kilinigu. Moo waral itam ñu lël 18i fajkat ya fay liggéey yépp.

Ci Ndakaaru, Wàllentuw-ëlëm bu Cité Soprim wàll na jàngoro ji ay fajkati Centre Mamadou Diop bu Liberté 6 Extension.

Taalibe yi jël nañ seen wàll ci mbas mi

Li ñépp doon ragal mujje na am. Ndeysaan, mbas mi song na goney taalibe yiy yelwaan ci mbedd mi. 3 taalibe la jàngoroy Covid-19 bi daaneel ca Sigicoor.

Mbas mi dugg na Mbàkke

Gox bi dend ak Tuubaa, Mbàkke, am na 2 Wàllenti-ëlëm. Nee ñu, ñoom ñaar ñépp ca màrse Okaas lañ doon liggéeye te yéeg nañ ba tàyyi ci oto yiy lëkkale Tuubaa ak Mbàkke.Jamono jii, njàqare ju réy la fa mbir mi jur.

Benkeñenke yi wàllentuw-ëlëmu Géejawaay bu mujj bi sabab

Ab soxna la. Ndege, Kër Masaar la jóge ba muy seetluji boppam ca kilinigu Duudu bu Géejawaay Nimsaat. Ginnaaw Waxinaan Nimsaat, jot naa jaar ci bérébi mbooloo yu bare, rawatina Màrse-Jën bu Pikin bi nga xam ne, lu tollu ci 2 000 nit ñoo fay daje bés bu nekk. Yemul foofu ndax dem na ci yeneen màrse biir Géejawaay. Te, saa su nekk, ndaw si oto yi walla biis yiy yeb mbooloo lay jël.  Loolu nag, indil nay jafe-jafe ak i benkeñenke yu tar ñi nga xam ne ñoo war a xool, xayma ñi mu war a wàll.

Perefe Géejawaay bi, Muhammadu Bolondeŋ Njaay ak Meer bi, Raasiin Taalaa, jël nañ dogal, lël 18i fajkati  kilinig Duudu ba mu demoon ak seen i  dëkkandoo.

Ñaari yégley jawriñu koom-koom bi

Bi ci jiitu mi ngi aju ci li nguur gi dugal 200 milyaar ci sunu xaalis ci bànk yi ngir sàmm peyoori liggéeykat yi. Jawriñ ji nee na, na àntarpiriis yi am ay jafe-jafe ngir fay seen iliggéeykat dem ci bànk yi. Jawriñ ji Hott ne, ci Iradio ak ITv : « dinan leen yombalal mbir mi ci ni mu gën a gaawe. »

Ñaareel bi, moom, liggéeykati nguur gi la ñeel. Jawriñu koom-koom gi ne, liggéeykati nguur gi bokkuñu ci aj biñ aj peyum bor ñeel liggéékat yi ameel bànk yi. Ndaxte, ñoom, ñoo ngi wéy di jot seen i peyoor weer wu dee.

Coowal ceeb bi

Mañsuur Fay tontu na Gii Maryiis Saaña. Ndege, Gii Maryiis Saaña ak waa FrappFrance dégage dañu koo kalaameji ca jawriñ ji ca OFNAC. Bi ko taskati xibaar yi laajee, Mañsuur Fay dafa ne : «  Gaa ñooñu, bu leen neexee àkki bérébu àttekaay bu leen neex. Waaye, nun ñepp noo war a jàpp ci liggéey bi ngir matale jubluwaayu Njiitu-réew mi Maki Sàll : séddale dund gépp ñi ko yeyoo kese, ci diirub 10i fan, lu mu yàgg yàgg»

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj