Gaynde gi suuragul, ndeke. Gannaaw ba ñu fàddee kuppeg Afrig gii weesu, xàllal seen i rakk yoon wi, gayndey Aliw Siise yi dikkaat nañ, tàmbaliwaat rëbb gi. Wile yoon, nag, Koddiwaar lañuy diir.
Ci àjjuma jii weesu la Senegaal doon joŋante ak Mosàmbig ñeel “éliminatoire CAN 2023”. Keroog a doon njëlbeenug yoon, ci at mi, Gu Senegaal di kuppe ginnaaw kuppeg àddina si amoon Qataar te Àngalteer toogloo woon leen. Keroog àjjuma nag, wone na ni, ba tey, mooy buuru Afrig, te mooy doxal itam. Noonee la wullee Mosàmbig wulli yu metti, dóor ko juróomi bal ci benn (5-1). Sunu gaynde yi dawal nañ bal bi dawal bu set, dalalaat xel yi. Nde, bari woon nay kuppekat yu bees, wànte yàqul dara ci déggoo bi amoon seen biir. Moom kay, dafa mel ni ñoom ñépp a yàgg a kuppendoo.
Ilimaan Njaay nag, moo gënoon a fës keroog. Nde, nim ko baaxoo def ca këlëbam (Sheffield United), futbal na fa lu réy, am-njaay-joxal-jóob gi di jolli tey neex. Moom sax moo sédd Yuusuf Sabali bi muy dugal bii bu njëkk bi. Yemu ca de, ndax moom itam dugal biiwam bu njëkk ak Senegaal. Loolu nag, doonoon na mbégte mu réy ci moom. Dafa di, ñépp a gis xiirug gaynde gi mu xiiru bi mu dugalee, xél ci siporteer yi ngir wone mbégteem.
Amoon na tamit keneen ku jot a ràññeeku ba ñépp di ko soow, muy doomu Tëngéej ji, Abdalaa Nduur. Keroog la njëkk sol mayob Senegaal, doon gan ci ekib bi. Waaye de, gan-ganluwul wenn yoon ; wone na jom, fulla ak faayda ju mat sëkk ca wetu càmmoñam ga. Liñ ko doon xaare, moom, matal na ko, ba romb ko sax. Lu set la kuppe : di def lu yomb, di génn fu mu waree, di dellu fum ko jaree. Bi Ilimaan Njaay di dugal sax, moo ko taajal bal bi, ginnaaw ba mu fëllee fëll bu rafet.
Abdulaay Sekk itam, kenn demul mu des. Boo ko xoolee ni mu doon demee keroog, dangay jàpp ni kii dafa yàgg sax ci ekib bi. Dal na, teey na, te yit xeex na ni gaynde di xeexe. Moom, ak Kaliidu Kulibali, ñoo sàmm ginnaaw gi. Naam, Mosàmbig dugal benn bii, waaye loolu tilimalul seen joŋante. Mu am itam ku ñu gëjoon a gis, donte ne du gan, muy Saajo Maane, doomu Bàmbaali ji.
Saajo Maane, moom, jotul woon teewe kuppeg àddina si amoon ci atum 2022 mi. Ndaxte, dafa ame woon gaañu- gaañu. Ci àjjuma ji la doon sog a delsi. Dafa mel ni li mu gëj a futbal daf ko jàpp tuuti. Ndax, wonewul xereñte biñ ko xame, dont ne dugal na benn bii. Noonii la fa deme ca këlëbam, Bayern Munich. Nde, bim delsee ba nëgëni, li muy mbél dafa des. Noo ngi njort ne dina gaaw a ñëwaat.
Bu dee Paap Usmaan Saaxo ak Nowaa Fadiga, yeneen ñaari xale yi ganesi ekib bi, jotuñoo dugg. Amaana Aliw Siise fubaloo leen joŋante bii nu dégmal, 28i màrs 2023, ca Mosàmbig.