Tàggatkatu Senegaal bu bees bi, Paab Caw, biral na ay ndawam keroog ca alxames jee weesu. Moom nag, dafa mottali yéeney saa-senegaal yu bari ci li mu woo xaley kuppekat yu xarañ yoy, dafa jaadu ñu sol mayo Senegaal.
Ndaw yu bees yi mu indi ñooy : Asan Jaawo, Ilaay Kamara, Yehmaan Juuf, Séex Ñas, Risaar Saañaa ak Antuwaan Mendi.
Cig pàttali, Senegaal dafa war a amal ñaari joŋante ci weer wii. Bu njëkk bi, Sudã la ciy dajeel, bésub 22 màrs 2025, bu 19i waxtu jotee. Senegaal mooy fekki. Ñaareelu joŋante bi, gaynde yi dañuy dala waa Tógoo fi Jamñaajo, 25 màrs 2025, bu 21i waxtu jotee.