GAYNDEY SENEGAAL YI RËKK NAÑ YOY KAMERUN YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gannaaw ba mu wullee dëkkandoom bi, Gàmbi, keroog ca bés bu njëkk ba, Senegaal wulleeti na Kamerun 3i bal ci benn. Senegaal mooy ñaareelu ekib bu kalifiyeegum ci wicceem yi ginnaaw Kap-Weer mi gañe ñaareelu joŋanteem ci njolloor gi.

Tay ci àjjuma ji la gayndey Senegaal yi doon jàkkaarloo ak gayndey Kamerun yi. Képp kenn nag, xamoon na ni joŋante bi du yomb. Ndaxte, ñoom ñaar, seen ndaje du nooy mukk. Waaye dafa mel ni Senegaal gaynde gu xiifaat la, lu mu dajeel fàdd jàll. Fàdd na Gàmbi, yen ko 3i bal ci dara, tay mu fàddati Kamerun, dóor ko 3i bal ci benn.

Ni ñaari ekib yi dikkee tay nag, dafa mel ni Aliw Siise genn coppite rekk la amal ci ñi mu tegoon keroog, muy bokkug Paap Mataar Saar ci 11 yi tàmbali, wuutu ci Musaa Ñaxate mi ame gaañu-gaañu. Mu dikke fullaak faayda niki mu koy defee jamono jii ca Tottenham, fëll fees ko doon xaaree. 

Bu dee Rigobeer Soŋ miy tàggatkatu Kamerun, moom, dafa indi 5i coppite ci lim tegaloon Gine Konaakiri. Juróom ci ñi tàmbali woon keroog daf leen a wecce tay. Ci juróom yooyu mu indi, ñu jàpp ci Andre Onana mi góolu tay.

Seen joŋante bi nag neexoon na. Ba mu dooree,  xawoon nañu sëpp gayndey réew mi, ñu mel ni ñu xaw a réer ci seen taxawaay daanaka lu tollu ci 5i simili. Waay, bi ñu dawalee tuuti, ñu daldi ximmaliku, tée bal bi di doxal. Ci 16eelu simili bi Ismayla Saar daldi dugal ci paasu Paap Mataar Saar ci benn wëndeelu Ismayla Sakob bu Onana génn dóor bal bi, doomu Cees ji laalal ko doomu Ndar ji, mu dóor ko mu sar ca caax ya. Ñu jóge ca di dawal noonu Senegaal xaw a jekku ba ñu miitã ci 1-0 bi.

Bi ñu delsee ñu nekkaat ci, Kamerun xaw a jekku tuuti waaye gayndey teraanga yi di dëggal seen bopp rekk. 71eelu simili, Saa-Senegaal yiy doxal ba mu àgg ci Ismayla Saar mi dugal bii bu njëkk bi, mu rëdd ci kanamu góol bi beneen doomu Cees ji Abiib Jàllo daldi fekke, defaat ko ci kër gi muy 2-0. Gannaaw ñaareelu bii bi nag, ñu bari jàppoon nañ ni fa lay yam. Ñu wane Etóo ca kaw tirbin ba kanam gi belliwul dara. Xam naa ni ña ko séen reetaan nañu ko ndax foogoon na ni Senegaal waru ko gañe.

Ci noonu, joŋante biy wéy ba ci 83eelu simili ba, mbokki Weesã Abubakar yi daldi am korneer, Kasteletoo tëb ci kanamu Kulibal, mbëkk mu dugg. Eduwaar Méndi mënu ci woon dara. Saa-Kamerun yi sëpp Senegaal ba naroon a dugal seen 2eelu bii ci benn mbëkk bu tiital soppe yépp. Waaye, mu aw ci wetu poto bi génn. Bi 90i simili yi futbal laaj jotee dollees na ci yeneen 7i simili. Gaa yiy wéyal ba toll ci 90+5eelu simili bi, doomi réew miy dawal lu neex ba génneel ko Gànna Géy mi dugg bu yàggul, ca wetu ndeyjoor wa mu dàq ñépp taajal ko Saajo Maane ci dóorukaayu penaltii ba, mu daldi dóor bal bi ci suuf. Onanaa tàwweeku ba sonn, bal bi dugg.

Nii la joŋante bi tëddee woon. Senegaal war a dajewaat ak Gine ci talaata jii ñu dêgmal ñeel ñetteelu joŋanteem bi ko dese.

Mànkoo, wuti ndam li.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj