GÉNNEG SENEGAAL CI RÉEW YI GËN A NDÓOL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal ak réewum Kàmboj (Cambodge) ñooy réew yiy waaj a génn ci mboolom réew yi gën a ndóol. Loolu di ndogal “A/RES/79/230” nga xam ne mi ngi tukkee ci ndaje mu mag mi Mbootaayu Xeet yi doon amal fukk ak juróom-ñeenti fan ci weeru desàmbar 2024 wii ñu génn. Mu doon xibaar boo xam ne am na lu muy firndeel ci tolluwaayu Senegaal ci wàllu koom. Dafa di, moom, dafa am yeneen jéego yu mu war a séqiwaat ngir loolu mën a nekk. Te, dafa am ab diir bu ñu ko àppal ngir mu matale li ñuy xaar ci moom.

Fukki fan ak ñett la mbootaayu xeet yi siiwal caabal gi tukkee ci ndaje mu mag mi mu doon amal. Ca la xamlee ne réewum Senegaal ak mom “Cambodge” dinañu génn ci réew yi gën a ndóol. Loolu nag, jur na coow lu bari ci réew mu mel ni Senegaal. Nguur gi fi jógee ngi koy ndamoo. Naka noonu, ñi fi toog bees it, ñi ngi jàpp ne ñoo waral lépp. Mu mel ni, ay jiixi-jaaxa dafa am ci xibaar bi Mbootaayu Xeet yi siiwal. Moo tax, njëwriñu mbiri bitim-réew génnee ab yégle barki-démb ci gaawu bi ngir indi ay leeral ñeel coow loolu.

 Dafa di, mbir mi, ni ko ñu bari fooge demewul noonu bees sukkandikoo ci li njëwriñ gi siiwal. Nde, dafa ne réewum Senegaal génnagul ci mboolom réew yi gën a ndóol, maanaam, mi ngi ci PMA (Pays les Moins Avancés) yi. Am na lu ko dese ba tay. Xibaar bi ñu génne li ñu juble mooy xamle ne lii aw yoon la wow bu ko Senegaal wàccul, mën na jóge ci xeeti réew yooyu. Waaye, mbir mi yemul foofu kese. Ndax, ñoom dañu cee yokk ne àpp bi ñu leen may ngir ñu waajal génn gi, juróomi at la. Ci biir at yooyu lañuy wonee liy war a tax ñu génn ci xeeti réew yooyu. Ci gàttal, su diir boobu jeexee lañuy mën a wax ne réew mi génn na walla dafay desaat.

Kon, génnug réew mi walla bokkam ci xeeti réew yi gën a ndóol walla yi gën a suqaliku, dafa am ci ay sàrt yu mu aju. Looloo tax ba waa kurél googu gis ne réewum Senegaal ak mom “Cambodge”, fi ñu teg seen tànk foofu la. Te, bu ñu ko teggiwul moom, fi ñu teg seen bët, dinañu fa àgg. Nañ yokk cere rekk, dolli ñeex.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj