Saabalukaay xéy nañ bank seen i loxo tey ci talaata ji, 13i pani ut 2024. Li ñu ko duggee mooy amal ab bés bu kenn dul rotal i xibaar. Li leen naqadi nag, ci seen I wax, bari na. Waaye, lépp a ngi dellu ci ni Nguur gu bees giy doxaleek ñoom, bees sukkandikoo ci yégle bi CDEPS (Conseil des Diffuseurs et Éditions de la Presse du Sénégal) génne bërki-démb. Daanaka ñetti weer a ngii, saabalukaayi Senegaal yi nekk ci guddi yu lëndëm. Bokk na ci li leen gën a sonal, mooy seen i sàqi bànk yi ñuy tëj, jumtukaay yi ñuy nangu, peyoor yi ñuy téye, pasi fésal yi ñu xéy dog ba ci ay ajandi yi ñu nemmeeku ci lu amul benn diisoo.
Yooyu yépp nag, ñu jàpp ni teguwul ci lenn lu dul bëgg néewal doole saabalukaay yi, faagaagal yenn kër yi ci bëgg-bëggi way-pólitig yi. Loolu lañ xamle. Waaye, dafa mel ni du saabalukaay yépp a leen topp ci seen xeex bile.
Yéenekaayi Walfadjiri, Yoor-Yoor ak Le Verdict, ñoom, liggéey nañu tey. Askan wi tamit, ñi ci ëpp dañu soofantal xeexu njaatigey saabalukaay yi. Ndaxte, ci seen gis-gis, ñoom njaatige yooyii jiite xeex bi, seen bopp kesee leen ñor. Rax-ci-dolli, kenn tooñu leen ndax dañ leen a fayloo lempo doŋŋ. Te nag, lempo boobu, ñoom ñoo ko ameel réew mi. Am sax ñu jàpp ni, xeex bi dafa rax pólitig. Ak lu ci mën di am, xibaar yaa ngiy rot. Nde, surnaal moom, kenn jëndatu ko. Ci mbaali jokkoo yi lees di taataanee li ëpp ciy xibaar.