GIGA MEETING PASTEF : FOO SÀNNI MBÀTTU MU TAG

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci gaawu bi, la waa Pastef doon amal seen ndaje mu réy moomu. Ñi ngi ko doon amale fa “Dakar Aréna”. Muy fowu bob, am na lu tollu ci 15 000iy toogu ak lu teg. Mu mel ni, du guléet ñuy gis waa Pastef di dajale mbooloo mu ni tollu. Saa su Usmaan Sonko wootee, ak fu mu mën di woote, militaŋ yi dinañu ko fa wuyuji. Dafa di, wii yoon, dafa am lu yokk ci mbir mi. Nde, démb, dafa amoon joxe xaalis. Waaye, loolu terewul béréb boobu dafa fees ba am ñu des ci bitti.

Ndaje mi Pastef doon amal, démb, ngir waajal wotey palug dépite yi, xumboon na lool. Fa ñu woote woon ca “Dakar Aréna”, foo sànni mbàttu mu tag. Seen ndaje moomu, mi ngi door ci suba si. Ndax, suba teel la militaŋ yi dem fa béréb boobu. Daanaka, laata ñuy julli tisbaar fekk na béréb ba fees dell. Njiitul làngu Pastef mi woote, bi ñu jullee tàkkusaan la fa àgg. Moom, Usmaan Sonko, jot na fa a waxtaane ay tomb yu bari. Waaye, laata muy dugg ci biir waxtaan wi, dafa njëkke mas-sawu ñi ànd ak jàngoroy kañseer.

Ñetti tomb yi mu doon waxtaane, ñoom la tënk ci kàddu yii :

Bu njëkk bi mooy bëgg na a wax tuuti ci làng gi. Wax ci làng gi mooy delloo njukkal militaŋ yi. Te, maa ngi ciy ñëw. Ñaareel bi, mooy wax ci tolluwaayu réew mi. Ñetteel bi, mooy wax ci li nu dëgmal muy wotey palug dépite yi. Ñetti tomb yooyu kese laa fas yéene waxtaan ak yeen. Te, bu soobe Yàlla du gudd.

Ci gàttal, lii moo nekkoon tomb yi waraloon ndajem démb mi. Dafa di, jamano jii, dañoo nekk ci waajtaayu wote yu am solo muy yoy palug dépite yi. Looloo tax, moom, Usmaan Sonko mu ne : “Senegaal dafa nekk ci selebeyoon, nu war a tànn yoon wu baax wi”.

Mel na ni “Giga Meeting” bi am ndaje mu am solo la woon ci Usmaan Sonko. Nde, tax na mu mën a leeral mbir yu bari ay militaŋam. Waaye, wax tamit fan lañu bëgg a jëmale réew mi. Ak, nan lanu war a taxawe ci wote yii di ñëwe.

Kon daal, mënees na ne, démb, Pastef da doon wonewaat dooleem. Jéllale nañu sax mbooloo mi ñu dajale, Pastef jële na ci ndaje mi koppar gu takku. Ndax, bees sukkandikoo ci li El Maalig Njaay fésal ci xëtu Faacebookam, xew-xew boobu, jële nañu ci lu tollu ci juróomi téeméeri miliyoŋ. Te, ba tey, kopparal gaa ngi wéy. Mu doon koppar gu takku goo xam ne moom lañuy waajalee seen ub kàmpaañ. Moo tax, ñuy wax seen ay wujj, ku mën rekk, na def.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj