GINE BISAAWO | WOTEB FAL NJIITU RÉEW : FERNANDO DIAS DA COSTA MOO JIITOOGUM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci dibéeru démb ji la doomi Gine Bisaawo yi doon wote ngir fal seen Njiitu réew. Nde, Umaro Sisoko Embalo dafa matal 5i ati moomeem, waa réew ma waroon a dem ca mbañ-gàcce ya ngir tànn ki ñuy dénk seen lengey réew. Moom nag, Umaro Sisoko Embalo, dafa sampaatoon ndëndam, bokk ci 12i lawax yiy dagaan baati askan wa. Wote bi nag, ci lees jot ciy xibaar, ci jàmm ak salaam la am, te askan wa génn na ak doole ngir wane itte ji mu am ci seen réew ak nees koy saytoo.

Bees sukkandikoo ci njureef yi tukkeegum ci mbañ-gàcce yi, yéenekaay Confidentiel Afrique fésal ko, kii di Fernando Dias da Costa (47i at) moo jiitoogum. Moom, Sëñ bi Dias da Costa, ci kujje gi la bokk, demal boppam (candidat indépendant). Waaye nag, ag lëkkatoo gu mag a nekk ci ginnaawam, di ko jàppale. Lëkkatoo googu, dees na ca fekk ñaari làngi pólitig yu mag ya ca Gine Bisaawo, muy PRS bu Kumba Yàlla, njiitu réew ma woon, ak Domingos Simowes Pereera mi jiite kujje gi. Dafa mel ni nag, li Fernando Dias da Costa rawee Umaro Sisoko Embalo dafa jéggi dayo. Nde, bees sukkandikoo ci dég-dég ya fay tukkee, Sëñ Dias da Costa dafa raafal diiwaan yi ëpp i wétt* ca réew ma, rawatina péey ba, Bisaawo. Fi mu nekk nii nag, mëneesagul a wax ne ndam li féete na boor.

Fernando Dias da Costa ak i farandoom ñoo ngi wax ne jël nañu raw-gàddu gi ci sumb bu njëkk bi. Waaye, ci alxames jees dëgmal la kurél giy saytu wote yi ça réew mooma wax ne lay siiwal njureefi négandiku yi ñeel wote bi. Ginnaaw gi, fàww Ëttu àttekaay bu mag bi dëggal njureef yi ginnaaw bi ñu saytoo kalaame yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj