GOR, CA WAX JA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu tollu ci weer ginnaaw ba ñu ko tabbee elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko joxe ndombog-tànku meeru Siggicoor. Mu nekk ndogal lol, du Yoon moo ko ci tënku. Ñoom, ci seen coobare bopp, ñoo ko sàrtal ci seen làng gi. Moo tax, laata ñuy toog ci boppu Nguur gi ñu digoon askan wi ne boole ñaari ndomboy-tànk dañu ko fiy jële. Maanaam, ku ñu fal jëwriñ bu dee dangaa am ndombog-tànku dépite walla nga nekk meeru benn gox, dangay bàyyi donte ne sax askan wi moo leen ko takkal.

Ñaari fan ci weeru awril la Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jël lengey Njiitu réew mi ci loxoy Maki Sàll. Ca bés boobu la tabb Usmaan Sonko elimaanu jëwriñ yi. Mu doon wareef ci moom mu jébbal ko limu jëwriñ yi muy séqal liggéey bi. Juróomi fan ci weeru awril, mu siiwal ñaar-fukki jëwriñ ak juróom yi bokk ci Nguuram. Foofu la leen elimaanu jëwriñ yëgalee ne képp ci ñoom ku am geneen moome, na ko teg ko ci suuf. Te, àpp bi bu baree ba bari, weer kese la, ngir ñu jël ndogal ci loolu te fas yéene jublu ci liggéey bi ñu leen sas.

Dafa di, ñi nga xam ne ay dépite lañu woon moom, bu ñu leen tabbee jëwriñ dañuy bàyyi. Ndax, ñaari ndomboy-tànk yooyu méngoowul, kenn mënu leen a boole. Muy ku ci mel ni Biram Suley Jóob ak Àlliyun Sàll nga xam ne ay dépite lañu woon. Léegi, mu des meer yi war a jóge ca njiiteefu meeri ya.

Ka jiitu ci mba googu mooy Sëriñ Géy Jóob mi nga xam ne moom lañu tabb jëwriñ ji ñu dénk wàllug yaxantu gi ak ndefar gi. Nde, moom moo nekkoon meeru gox bii di Sànjara. Ka ca topp mooy, moom ndeyi-mbill ji, Usmaan Sonko. Ndax, bala ngay digle cangaay, na fekk nga set. Moo tax, moom it démb ci gaawu gi lañu biral ne tekki na ndombog-tànkam fa meeri bu Siggicoor.

Naka noonu, am na xibaar yu jib ci ne kii di Biram Suley Jóob tamit tekki na ndombog-tànkam fa boppu meeri bu Cees Bëj-gànnaar. Waaye, ñii di waa Seneweb xamle ne nañu ne xibaar boobu wérul donte ne sax am na ñuy wéy di gëm ne bàyyi na.

Kon, ki ciy bëgg a des kay mooy Soxna Maymuuna Jéey, meeru Pat-Duwaa nga xam ne moom it bokk na ci ñi ñu tabb jëwriñ. Nde, moom lañu dénk wàllu njaboot gi ak dimbalante yi. Dina bàyyi am déet dees na xam dara fii ak diir bu gatt ndax, àpp bi ñu leen mayoon moom jeex na. Ñu xool nag nan la Njiitu réew mi , Basiiru Jomaay Fa yak elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, di def ñeel ñiy bañ a bàyyi. Lu tëw a xam rekk, dafa fekk yàggul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj