Fa gox bii di Gudomp, njaboot yi tàmbalee dellusi ginnaaw bi leen fa xareb MFDC ba dàqee woon, jot nañu ay jumtukaay ngir tabax seen i dëkkuwaay. Muy ay jumtukaay yu jóge ci Càmm gi ñeel naal bii ñu duppe Plan Diomaye pour la Casamance, maanaam Naaluw Jomaay ñeel Kaasamaas.
Démb, ci àjjuma ji, njiiti sémbuw PUMA (Programme d’Urgence de Modernisation des Axes et territoires frontaliers), di sémb wi yittewoo yeesal yoon yeek gox yu fegge yi, doon nañu jébbale ay jumtukaayi tabax yu aju ci naaluw Njiitu réew mi ñeel diiwaanu Kaasamaas. Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu APS (Agence de Presse Sénégalaise) fésal, lu tollu ci 92i njaboot yu dellu ca seen i suuf ya nekk fa Jibanaar, ca goxu Gudomp, ca diiwaanu Séeju, jot nañu ci jumtukaay yooyule.
« Jëf jii dafa aju ci naaluw Njiitu Réew mi ñeel Kaasamaas (Plan Diomaye pour la Casamance). Muy Naal wu jublu ci taxawu dellusig daw-làqu yi, jaare ko ci jox leen ay dëkkuwaay yu baax ak ay tabaxte yu mënut a ñàkk yees yittewoo. » (Doktoor Ndey Mareem Sàmb)
Ci xayma, jumtukaay yees fa séddale dinañu tollu ci 140i tamndareeti FCFA. Moo xam simaŋ la, bant, seng ak yu ni mel yuy mën a dimbali askan wa ba ñu mën a am dëkkuwaay yu baax ak dund gu dal.
Bu weesoo kër yeet, fàkk nañu ay barab yu ñu war a tabax ñaari jànguwaay fa Bantakuntu (ci bokk-moomelub Gudomp) ak Bindaba 2, benn raglu ak toolub ndugg, ngir yombal dundug njaboot ya foofa.
Ginnaaw ndimbal yooyu nag, Njiitu Bantakuntu, Alfa Jàllo, rafetlu na jéego yi Nguur gi njëkk sàqi ngir jàppandal seen ug dellusi ci seen i suuf. Naka noonu, muy fàttali ni ca atum 1991 lañu taaloon seen dëkk bi ba ñu daw wutali Gine Bisaawo. Foofu itam def nañu fa 31i at ak i jafe-jafe yu tar.
Perefe bu Gudomp itam teewe woon na xew ma. Ciy kàddoom, dellusi na ci yitteey Nguur gi jëme ci dekkil dëkk yi xeex bi tasoon, gunge askan wi ba ñu dëkkaat ci jàmm. Waaye, jooju jàmm du mën a am bu suqaleeku amul. Loolu moo tax Nguur gi dogu ci suqali koom-koom gi, Njaboot yi am ci lu ñu jàpp ba dund nees ko bëgge.