“ICS” FEEÑLE NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw riirum caabal yi ci yorinu alalu askan wi, coow topp na kër gii di ICS. Ay ati at a ngi nii, tàbbalul dërëm ci gafakag réew mi.
ICS (Industries Chimiques du Sénégal), ameel na Nguurug Senegaal alal ju takku ju àgg ba ci 200i tamñaret (miliyaar ci FCFA). Muy xibaar bu sunuy naataango yu Pressafrik siiwal ginnaaw bi ñu sukkandikoo cib wayndare bu ñu leen jottali.
Bees sukkandikoo ba tey ci wayndare woowu, ICS amalul Nguurug Senegaal lenn njariñ. Ndaxte, du dërëm bu muy tàbbal ci gafakag Nguur gi. Du lempo bu muy fay ci li muy am, du tegaay (TVA), du duwaan ba ciy wareefam ci mbéll yi muy liggéeye.
Li ci gën a doy waar nag mooy ne, Nguurug Senegaal moomul daanaka dara ci ICS. Téeméer boo jël, fukk ak juróom (15%) doŋŋ la ci am. Endo yii di Indorama ñoo ci ëppale. Téeméer boo jël, juróom-ñaar-fukk yeek juróom (75%) yee ngi ci seen i loxo, dalee ko ca atum 2014.
Rax-ci-dolli, mënul a matale àngare bi baykat yi soxla. Donte ni isinu Mbaaw bi war na mën a defar lu tollu ci 250i junniy ton ci at mu nekk, jafe na ko lool mu àgg ci 150i junniy ton yees xayma ni baykat yi dinañu ko yittewoo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj