IGE (Ispection Générale d’État) am na sas wu réy. Dina amal ay caytu yu yaatu ciy këru liggéey yu mag. Muy sas wu réy wu ko Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, sas ngir mu andiy leeral ci seen doxalin.
Ginnaaw dalu roppalaan bii di AIBD (Aéroport international Blaise Diagne de Diass), saytukati IGE yi dinañu amal i caytu ci njiiteefi këri liggéey yu mag. Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Libération siiwal, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Fay, jox na leen ndigal ngir ñu luññutu doxalinu këri liggéey yu bari yu aju ci Bokkeef gi.
Naka noonu, saytukat yi dinañu luññutu doxalinu këru bataaxal gii di La poste, këru ndefaraan gi ñeel soroj bi SAR (Société Générale de raffinage), kër gi yor dem beek dikk bi ñeel TER bi SENTER (Société d’Exploitation du Train Express Régional), kërug dooleel laf gi FSE (Fonds de Soutien de l’Énergie), ak këru lótëri gii di LONASE (Loterie Nationale Sénégalaise).
Bokk na ci kër yees war a saytu tamit, kër gi yor jokkoo beek jokkalante bi ARTP (Autorité de régulation des télécommunications et des postes), kërug ndox mii di OLAC (Office des Lacs et des Cours d’eau), kër gi yor yaale bi ci dëkki taax yi CETUD (Conseil Exécutif des Transports Urbains Durables), Kër giy sàmm yoon yi FERA (Fonds d’entretien routier autonome) ak Kër gi baaxoo liggéeyi tali yeek seen yorin AGEROUTE (Agence Autonome des Travaux et Gestion des Routes).