INIWÉRSITE GASTOŋ BERSE : LU ËPP TUURU

Yeneen i xët

Aji bind ji

18Coow li neeti na kurr. Ndongoy Iniwérsite Gastoŋ Berse bu Ndar defati nañu seen mënin. Fan yii ñu génn, daara-ju-kowe ji tàngoon na jérr ndax ndongo yee doon ñaxtooti, di ñaawlu anam yi ñuy dunde ci biir iniwérsite bi. Waaye, bii yoon, ndoxum fos lañu tanq, tuuri ko ci bérébi liggéeyukaayu njiit yi ngir wone seen mer. Mbir maa ngi xew ci àllarba jii ñu weesu, di woon 10eelu fan ci weeru awril 2019.
Ci suba si la waa CESL (kurél giy sàmm àqi ndongoy Iniwérsite Gastoŋ Berse bu Ndar) woote am ndaje ngir waxtaane jafe-jafe yi ndongo yiy jànkoonteel ak li ñu jële, ñoom, ci njiit yi ñu diisi woon seeni tawat. Li gënoon a fés ci naqar yooyu moo doon ndoxum fos miy ball bay taa ci iniwérsite bi, xasaw xunn, nag. Daanaka noyyi fa lu jafe la. Bi ñu noppee ci seen ndaje mi, dañu dogi tali bi ñuy wax RN2, jóor fay xeer, taal fa matt. Bi takk-der yi ñëwee lañu dellu ci biir inwérsite bi, tanq ci ndox mi doon ballee ci fos yi, dem tuur ko ci biro “Recteur” bi (njiitu daara-ju-kowe ji). Waaye, ci biro kilifa gi ñu dénk wàllu dëkkuwaay bi ci iniwérsite bi lañu jëkke, def fa lu ni mel. Nee ñu duggewuñ ko woon lenn lu-dul fexe ba njiiti Gastoŋ Berse yi geestu leen ngir saafara seeni jafe-jafe. Yokk nañ ci ne ay weer a ngii ñuy dox ay tànki jàmm, fépp fu kilifa nekk ñu dem fa, waxtaan ak moom ngir mu def warugaram, saafara jafe-jafey ndongo yi. Waaye bi ñu gisee ni seen aajo fajuwul lañu def jëf ju ñaaw jooju ngir ñépp xam li ñuy dund.
Taxaw temm, xeex, ànd ceek fulla ngir ñu weg la, faj say aajo, lu jaadu la, dara aayu ci. Waaye bu ñu waxantee dëgg, dafa am nees koy defe. Ñépp a ñaawlu doxalinu ndongo yi, rawatina jàngalekat yi ba ci sax ñenn ci seeni moroom.
Ci ngoon gi la waa SAES (kurél giy sàmm àqi jàngalekat yi ci daara-yu-kowe yi) génne ag yëgle di ci fésal seen naqar. Ndege, bees sukkandikoo ci kàdduy jàngalekati UGB yi, ay ndongo fekk nañ leen ñuy def seen liggéey, ñu ñàkke leen kersa, dal ci seen kow. Nee ñu loolu mëneesu koo nangu benn yoon. Moo tax ñu daldi jël ndogalu aj njàngale mi ci diirub ñaari fan ; ñu ngi xaar it ba xam ndax nguur gi dina jël ay ndogal ci ni mu gën a gaawe ngir sooyloo CESL. “Recteur” bi, moom, woote nam ndaje ci alxemes ji ñeel kàngami iniwérsite bi (Asemblée de l’Université). Ñooñu tamit fésal nañu seen mer, fas yéenee teg ay daan ñenn ci ndongo yi ñu ràññee ci mbir meek seeni njiit, di waa CESL. Yemuñu foofu ndax nee ñu dinañ leen yóbbu fa mbaxane doonee benn. Ñaax nañu yit nguur gi ngir mu gaaw indiy tanqamlu ndongo yi, faj seeni soxla.
Léegi nag, li am ba des moo di ne jot na nun ñépp nu taxaw seetaat ni nuy doxale. Ndax kat, yëf yaa ngi bëgg a ëpp loxo. Muy ndongoy UGB yi walla sax ndawi réew mépp, njiitu iniwérsite bi walla sax njiiti réew mépp, ku ci nekk am nga wàll ci lii xew tey. Lan moo fi soppeeku ci diggante atiy 1990 yeek léegi ? Waaw, laaj bii lees war a wutal tontu. Ndaxte, démb, doyoon nag sag ñu ne la ndongoy iniwérsite Gastoŋ Berse bu Ndar nga, walla fa nga génne. Ñu bare ci kilifay Senegaal yi jaar nañ fi. Kon, at yii weesu, Iniwérsite Gastoŋ Berse bu Ndar sag la woon ci Senegaal ndax bokkoon na ci daara-yu-kowe yi gën ci Afrig sowu-jant. Ndeysaan, tey wutewul ak toolu-xare. Ñaari fan ñett nga dégg fi coow ; bu dul jàngalekat yi, ndongo yi ñooy taal tali beek bérébi liggéeyukaay yi ; te bala ñuy wéer seeni gànnaay sax, liggéeykati iniwérsite bi tàmbaley kaas ñoom tamit ! Waaye nag dañ koy wax te dee, ndongo yee gën a ràkkaaju ñépp. Ndaxte, saa su ñu yëngatoo, am lu yàqu walla ku ñu faat ci ñoom. At mu jàll ñu foog ne moo yées, bi ciy topp ñëw ne ko dandu ma. Dem nañ ba kenn joxatul cër sa moroom.
Nguur gi deful wareefam, njiiti iniwérsite yi naka noonu. Leeg-leeg dangay waaru, naan : waaw ñii ndax dañoo tële walla dañuy def yëfu maa-tey ?
Kon, joxoñante baraam jaru ko, na ku nekk waxtaan ak xelam ndax lu ëpp tuuru.
PAAP AALI JÀLLO
 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj