Ay weer ginnaaw ba ñu dekkalaatee xareb Israayel ak Palestiin, ba tey jeexagul. Ndax, dafa am ku yokkaat ci xar mi karaw. Te, kooku du kenn ku dul Irã. Ndax, kenn umpalewul ne ba yëf yi dooree ba léegi, réew mu nekk ak taxawaayam. Moom nag, taxawaayam booboo tax mu soppi doxaliin. Léegi, ndimbalam yematul ci ay kàdduy kese, daf cee boole jëf. Jëfam joojee tax àddina si ame ko démb ba tey. Nde, dafa dóor ay sox Israayel gi nga xam ne dafa fatt witt ñii di waa Palestiin weeru oktoobar 2023 ba tey donte ne sax, xare bi jiitu na loolu.
Xare bi dox diggante Israayel ak Palestiin am na fu mu doore. Waaye, fa mu nar a jeexe moo jaaxal ñépp. Mënees na ko jàppe ab góom boo xam ne saa su ñu foogee ni wér na rekk, mu wulliwaat. Dafa di, jamono jii ñu tollu, xeex bi dafa yematul ci diggante ñaar ñooñu kepp. Du xeexu jullit ak yawut kese. Dafa mel ni ñépp lay bëgg a laaxaale. Looloo sabab Irã moom wone péeteem ci xare bi. Ba tax, démb ci gaawu gi mu dóor Israayel lu tollu ci ñaari téeméeri misil. Am sax xibaar yu siiwal ne lim bi ëpp na loolu. Misil yooyu nag, ñi ngi nekk diggante ay “drones”, ay “missiles de croisière” ak ay “missiles balistiques”.
Bi loolu amee, réew yu bari biral nañu seen gisiin ci mbir mi. Réew yi nga xam ne musiba ji soriwu leen noonu yépp, teel nañoo jël seen i matuwaay tëj seen jaww ji. Muy fu ci mel ni Irã ci jëmmi boppam, Iraag, Israayel mi ñu sànni sox yi, Esipt, Libaŋ ak Sordani. Ndax, ñetti fan laata ñuy dóor misil yooyu, xibaaroon nañu ko seen dëkkandoo yi. Waaye, coow li yemul foofu kese. Yeneen réew yi nga xam ne sax daanaka laalewuñu ci mbir mi, ñaawlu nañu jëf ji. Rax-ci-dolli, gën a yeesal seen cofeel ci ñoom. Ñu gën cee ràññe réewi OTAN yi ak Etaasini.
Loolu terewul waa Israayeel tamit di dox ay jéego ci xew-xew boobee. Ndax, seen àmbaasadëer bi leen nekkal fa ONU (Organisation des Nations Unies) di Gilaad Erdan sàkku na ci banqaas gii di “Conseil de sécurité de l’ONU ” ñu amal am ndaje mu tembare. Ndax, jàpp nañu ne yëf yi fi mu tollu nii dafa jamp. Ñoom it, ñu nangul leen ko. Ndaje moomu, dinañ ko amal tey ci dibéer ji bu ñeenti waxtu ci ngoon jotee. Ñu mën koo natt ci juróom-ñetti waxtu ci guddi (20h00).
Li ñu layale ndaje mi mooy ne dañoo jàpp ne ñii di waa Irã dañoo sàmmoontewul ak sàrti ONU yi ak li àddina sépp yoonal ngir jàmm am (droit international). Ci gàttal, li Irã def teyeef la, ndax, taxawaayam daf ko dëggal. Nde, waa Irã sax ci seen jëmmi bopp dañoo bég ci li ñu def. Loolu terewul ñii di waa Turki di sàkku ci ñoom ñu teg mbir mi ci suuf. Xibaar boobu mi ngi ko jaare ci jëwriñam ji mu dénk wàllu bitim-réew di Hakan Fidan.
Li am ba des mooy ne Irã moom dóor na ay soxam toog di xaar. Waa Israayeel tamit ñi ngi def seen kéemtalaayu-kàttan ngir aar seen réew ak li ko wër. Muy ci kow (jaww ji), di ci suuf. Ba tax na, fim tollu nii, nemmeekooguñu ci fu bakkan rot diggante démb ak léegi. Donte ne sax, am xibaar yu rot ne am na ñu jële ay gaañu-gaañu. Waaye, lu ci mën di am, dinañ ci dellusiwaat ca na mu gën a yaatoo.