JAKKAARLOO AJI SAAR-USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw at ak lu topp bi coowal ciif gi dooree ak léegi, jàppees na àppu jàkkaarloob ñaar ñi séq mbir mi. Coow loolu nag, mi ngi dox ci diggante soxna sii di Aji Saar ak kii di Njiital Pastef lii di Usmaan Sonko. Weeru féewaryee, atum 2021, la mbir mi dooroon. Mu demoon nag ba jur musiba bu réy ci biir réew mi. Ndax, bésub ñetti fan ci weeru màrs lañu woo woon kii di Usmaan Sonko laata muy àgg ñu teg ko loxo. Ca la xeex ba dooree ba am fukki bakkan ak ñeent yu ci rot. Mu mel ni boobu ak léegi  am na ñu ñu ci jot a déglu ba ci ndeyi-mbill yi. Ñoom ñaar nag dinañu jàkkaarloo ca pekkug àttekat bii di Umar Maham Jàllo. Loolu nag, jàpp nañu ko tey ci talaata yemoo ak juróom-benni fan ci weeru desàmbar.

Coow li dox diggante Aji Saar ak Usmaan Sonko mi ngi bëgg a yàgg ci loxoy yoon. Dem na sax ba tàmbali di soof ñu bari ci saa-senegaal yi. Li mat a laaj kay mooy, ban taxawaay la yoon am ci mbir mi ba mu yeexe nii ? Te am na yeneen xew-xew yu ni mel yoy, lijjanti nañu leen ci anam bu gaaw. Walla mbir yi ñoo dul benn, walla nit ñi ? Kon jàkkaarloo bi dina tax lu bari leer ci mbir mi. Mbir mi yem fi walla ñu dem ca layoo ba. Loolu la kenn ci layookati Usmaan Sonko yi di Sire Keledoor Li leeral ci kàddoom yii : 

« Bu fekkonte ne àttekat bi jëlul woon dogal bii. Kon àttekat bi day jël wayndare wi sonal ci nit ñi, du ko mës a jeexal mukk. Ndax, dinañu ci yokk ay mbir yuy guddal wayndare wi. Te, xam nanu ne wayndare Aji Saar Usmaan Sonko lu ñu sos la ngir faagaagal aw wujju ci wàllu pólitig. Li àttekat bi def nag day tax ñu mën a gaaw a jeexal mbir mi, ndax bu ñu jàkkaarloowee rekk, lépp leer. Usmaan Sonko wax, Aji Saar wax, ñu gam-gamle seen i kàddu, Maham Jàllo jël ndogal ci ni coow li di mujje. Ñi nga xamante ni tamit tudd nañu leen ci coow li, waroon nañu leen mën a déglu laata ñuy woote ab jàkkaarloo. Jàpp naa ne mbir mu bu yàgg lañu ko waroon a tege boor ndax dara nekku ci. Mbir mi nag li ko waral du leneen lu dul pólitig moo dugg ci wàllu yoon, loolu ñépp xam nañu ko.» 

Mu mel ni kàddu yooyu firnde la ci ne mbir mi dafa war a jeex, yoon wax li am. Askan wi xam fi dëgg féete, ki tooñ yoon dal ci kawam. Ndax, fu ay bakkan xas ba rot moom, daray caaxaan waratu caa am. Donte ne sax, ñii di layookati Usmaan Sonko yi àddu nañu ci, ñi fare ci Aji Saar moom fekku leen ci. Waaye, mbir mi yemul foofu ndax ñii di layookati Usmaan Sonko yi dañu doon sàkku ñu déglu képp koo xam ne ñi ngi lay tudd ci mbir mi. Muy ku ci mel ni Mammadu Maamuur Jàllo nga xam ne kii di doktoor Alfuséyni Gay bi ñu koy déglu dafa waxaale ni loxoom laalee na ci mbir mi. Ak ku ci mel ni Mc Ñas nga xam ne, nee na, yor na ay ndéggat yuy wane fu dëgg gi féete. Ba tey mu am ñoo xam ne kii di Usmaan Sonko moo teg tuuma ci seen ndodd ne ñoom dañoo laalee ci mbir mi te ñu war a setal seen der ci loolu. Kon mbir mi li ko tëgg tasu ko. 

Léegi kay, li am des mooy kii di àttekat bi jàpp na àpp ngir ndeyi-mbill yi jàkkaarloo. Tey, bu soobee Yàlla, ku nekk ci ñoom dina indi ay firnde ci li mu wax. Aji Saar wax ki muy jiiñ ag ciif, fan la ko teg. Usmaan Sonko tamit indi ay firnde yuy teggi tuuma yooyu. Rax-ci-dolli, moom mi nga xam ne, nee na ay pexe la ngir faagaagal ko mu joxe ci ay firnde. Ndax kat, mbir mi ndeem ay nit ñàkk nañu ci seen i bakkan, am ñu ci jële ay gaañu-gaañu, ay yàqu-yàqu yu bari ci réew mi. Kon nag dafa jot yoon leeral mbir mi, ñu jàll ci leneen. Yoon tëdde njaaxanaay bañ a def Kumba am ndey ak Kumba amul ndey. Fu dëgg féete mu jox leen ko, dal ci kow ki tooñ.                                                                                                                                                                             

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj