Barkaatu-démb, ci alxames ji, lañu daan njiitul làng gii di Pastef, Usmaan Sonko, lu tollu ci ñaari ati kaso ci coow li doxoon digganteem ak Aji Saar. Keroog ak léegi Senegaal nekkul ci jàmm. Fu nekk ay jàmmaarloo nga fay sosoo diggante takk-der yi ak askan wi, rawatina ñoñi Usmaan Sonko. Mu mel ni coow lii du tey la door. Xanaa kay daan bi daf ko gën a jëmmal rekk. Ba tax na jamono jii askan waa ngi ci njàqare gu réy. Dem ak dikk bi gàllankoor nañu ko ci béréb yu bari, naka noonu njàng mi taxaw, daara yu kowe yi tëj seen i buntu, powi tàggat-yaram (football) yeek yu ni deme dakk, ba ci internet bi sax dañ ko dog.
Coowal Aji Saar ak Usmaan Sonko li mel na ni booy na noppi saa-senegaal yi. Ndax, kenn umpulewul li mu fi jur ci ay musiba. Bu dee weeru màrs 2021 yëf yi ëppoon nañ loxo, wile yoon, dafa gënatee ñàng. Nde, bu dee ay yàqu-yàqu rekk moom, bari na lool ba jéggi dayo. Waxaalewuñu ñi ci jële ay gaañu-gaañu ak ñi ñu ci jàpp. Li ci gën a doy waar mooy ne, bu dee màrs 2021 fukki nit ak ñeent ñoo ci ñàkkoon seen i bakkan ci diirub ayu-bés. Wii yoon nag moom, ci ñaari fan kese, daanaka limub ñi dee ci yëngu-yëngal yi dafa ful ñaari yoon. Kon, musiba moom mënul a romb lii. Waaw ! Léegi koo xam ne boo ko laalee rekk tàbbal réew mi ci guuta, ndax doo ko bàyyi mu nekk ci jàmm ?
Senegaal ak ni mu tollu yépp, jamono jii kenn kepp a tax amatul jàmm muy Usmaan Sonko mi ñu daan ci loo xam ne toppewuñu ko ko woon. Te, loolu lenn waralu ko lu dul mbiri pólitig. Waaye nag, ku jëmbët garabu fitna, toog ca ker ga dina la jafe. Rax-ci-dolli, ngelaw moom dina dugal ci pax lu mu ci dul mën a génne. Ba tax na, jamono jii, réew maa ngi ci guuta gu réy. Koom gu nërméelu woon àllub neen, bees ci raxee lii, fan la jëm ? Ndax kat, jamono jii banqaasi koom yi daanaka benn doxu ci rawatina ci dëkk yu mag yi nga xam ne fa la koom gi gën a doxe. Ba ci sax mbaali jokkoo yi nga xam ne, noonu lañu amee doole ci réew mi, askan waa ngi jànkoonteel ak i gàllankoor ngir mën leen a jëfandikoo ni ñu ko daan defe. Te, coow lii kepp a ko waral. Lu tere feyuñu coow li nag bu yàgg ba léegi ?
Mu mel ni taafar ji ñu doon wéyal booba ak léegi moo wund lii lépp. Ndax, bi musiba boobu amoon màrs 2021 jàllee, jéemuñoo xool nu ñuy suulee yëf yi. Waaye, dañoo wéyal coow li, am ñoo xam ne daanaka loolu kepp lañu defoon ab liggéey. Ñuy wéyal di jàpp mbokki Usmaan Sonko ba fim tollu nii lu tollu ci ay téeméeri téeméer ñoo ngi ci kaso yi. Kii naan li fi amoon dootu fi amati, ñee naan Yoon kepp a am doole, te mooy dogal. Ña ca des naan leen askan wi kepp a am doole. Te, li ñu defoon bu fi amatee, lu ko raw dina xewaat. Moone de, am na ñu doon artu donte ne sax mujj nañu àtte. Dafa di kay, gaa ñi dañoo gumba-tëxlu rekk ne fàww ñu am li ñu bëgg. Moo tax, jamono jii réew mépp a ngi toog ci nen. Ak foo mën di féete, jàmm moom ci la lépp xaj. Li ko waral mooy fim tollu nii réew mi dara doxul, kenn mënul amal dara, gaa ñaa ngi toj, di taal rekk. Ñépp a ngi teg bët réew mi muy njabootam gi nekk ci yeneen réew yi ba ci sax yeneen réew yi ci seen jëmmi bopp. Ba tax na, yëgle yaa ngi jóge fépp.
Loolu firnde la ci ne jàmmi Usmaan Sonko ci la jàmmi réew mi nekk. Ba ci sax Njiitu réew mi, Maki Sàll, jàmmam ci la aju. Ndax, mooy tax mu mën a wéyal liggéeyam. Li ko waral kat mooy saa bu ñu ko woowee sax, askan wi day nekk ci fitna. Mu mel ni Ndakaaru moom daanaka lépp ay taxaw. Dafa di moom, njabootam yépp ay jóg taxaw, ne ko duñu la bàyyee ak moom. Ginnaaw nag ñaari kuy mënuñoo bokk mbalka, kon moytonte du ci mën a ñàkk ngir jàmm am. Waaye nag, jàmm moom ku ko bëgg fàww nga teg sab yar. Ndax kat, ku sës rekk fippu.