Jàngoro ju yéeme te raglu moo gaaral, fan yii, ay mool yu nappi woon ba delsi. Limeesagum na, xaat-xaat, 300i way-tawat. Jawriñu wér-gi-yaram wi ne, ku dem, ndoxum poson a sabab jàngoro ji. Waaye, dara wóoragu ci.
*
Jàngoro ji, kumpa ju réy la. Nguur gi ci boppam, waxagu ci lu leer. Fim ne nii, 300i mool yu jóge géej ñoo ame màndarga yi ci seen der. Ba tey, nag, kenn xamagul sabab bi dëgg-dëgg. Ci alxames ji la jawriñu wér-gi-yaram gi, Ablaay Juuf Saar, ne woon : « Ñaari fan yii, nemmeeku nan, ca Caaroy, jenn jàngoro juy song mool yiy jóge géej. Way-tawat yi, nag, yenn saa, ñu amey dagg-dagg. » Kàddu yii, ba mu génnee ca Centre hospitalier Albert Royer bu Ndakaaru ba mu saytuji woon, la leen biral. Day wàlle, du wàlle…dara wóoragu ci. Siiwalees na bu baax fan yii nataali mool yi ame feebar bi, ci Internet bi, tele yi ak yéenekaay yi. Dees na ci gis ay mool yu amey picc yu dijj ci seen kanam ak seen gémmiñ. Jawriñ jiy leeral, ne :
« Fi nuy wax ak yéen nii, 300i way-tawat lan amagum. Noo ngi wéy di saytu mool yiy jóge géej. Ci biir 300i way-tawat yooyu, nag, 18i yaa ngi loppitaan. Lëlees na ña ca des ciy béréb yiñ leen jagleel. »
Mu teg ci ne, Institut Pasteur ak Centre anti-poison bu njawriñu wér-gi-yaram gi lañ dénk liggéey bi ngir ñu xool ba xam lan moo sabab jàngoro ji. Ablaay Juuf Saar neeti : « Tey, li wér li nu mënagum a wax daal, mooy ne jàngoro ji jotewul dara ak mbasum Covid-19 mi. Ndaxte, ginnaaw bi nu leen saytoo, kenn ci ñoom amewul doomu-jangoro jooju. Loolu moo nu tax a foog ne, ab poson a sabab jàngoro ji. Waaye, amagun ci lu leer. » Rax-ci-dolli, jawriñ ji nee na way-wottu càkkeef yi dinañ saytu ndoxum géej gi, xool ba xam dara raxu ci. Am na sax, ñu doon wax ne jàngoro ji day wàlle. Waaye, Ablaay Juuf Saar weddi na lu ni mel. Bees sukkandikoo ciy waxam, « dara waneegul » ne jàngoro ji day wàlle. Ndax, « mool yiy jóge géej rekk lay daaneel » te seen i waa-kër feebaruñu. Ci àllarba ji, gornooru Ndakaaru, Al Hasan Sàll, waxoon na ne dina taxawal am ndaje muy saytu lépp lu aju ci jàngoro ji. Fim ne nii, ñoo ngi gëstook a wër ngir ràññee ñi ame jàngoro ji ci kër yi, loppitaan yi ak dispañseer yi ak ci mool yiy jóge géej. Jawriñ ji dafa jox liggéeykat yi mu yilif ay santaane yu leer, rawatina doktooru Ndakaaru bu mag bi, njiitalu wér-gi-yaram gi ak ki jiite laboraatuwaar biy saytu poson yi. Ñii nii dolleeku ci mbooloom gëstu mi, seen sas mooy jokkale liggéey bi, amal i gëstu ngir ràññee way-tawat yi, fuñ mënti nekk, toppatoo yeneen way-tawat yi dem géej tey leerlu, ci nim gën a gaawe, ngirtey ceetug dereti way-tawat yi. Lii moo feeñe ci ràppoor bi doktooru Mbaaw bu mag bi, Dr. Jàmboñ Nduur, xaatim. « …aji-tawat ji jëkk a ame jàngoro ji, 20i at la am te bésub 20 eel ci nowàmbar 2020 la demoon ca doktoor ya… » Ci biir ràppoor boobule, jawriñ ji wax na ci ne, ngir ñu saafara jàngoro ji te aar askan wi, fàww ñépp dugal ci seen loxo. Ràppoor bi leeral na yit lees jot a def bi jàngoro ji feeñe ak léegi.
« Ci talaata jii, 17 eelu fan ci weeru nowàmbar 2020 la doktooru loppitaanu Mbaaw bu mag bi, Kurélug wattu loppitaan bi ak benn aji-xaralab laboraatuwaar dem ca dispañseeru Caaroy- Géej. Loolu mi ngi am ginnaaw bi nu njiitalu dispañseer boobu yëgalee ni am nay way-tawat yu bare yu ame jàngoroy der yu fay fajusi. Ñoom ñépp di ay mool yu góor, tollu ci diggante 13 ba 46i at. Ñenn ñi, Ndar walla Jogo lañ dëkk, ñeneen ñi Faas Bóoy walla Caaroy-Géej. Tamit, ñoom ñépp ñoo bokk màndargay feebar : ay picc, lee-lee yu réy, ak i dagg-dagg ci seen i kanam, ci njeexitali cër yi ak, yenn saa, ci awra yi. » Dr. Nduur ne, « gëstu gi wone na ne, aji-tawat ji jëkk a ame jàngoro ji, 20i at la am te bésub 20 eel ci nowàmbar 2020 la demoon ca doktoor ya nemmeeku ci moom màndarga yii : picc yu am ndox ci yaram wi, newwi-newwi kanam, tuñ yu wow ak bët yu xonq. Jàngoro ji sonalagul kenn ci ñoom. Waxtaan win séq ak way-tawat yi wone na ni am na ñu ame màndarga yu ni mel ci kër yi ak ci mool yi nappi. Bu dee sabab bi, way-tawat yi dañu jàpp ne ci ndoxum géej gi la jàngoro ji jóge. » Bi doktoor bu xelam màcc ci wàlluw der saytoo way-tawat yi, moom, lii la biral : ay picc yu am dëtt yiy sax ci wetu bakkan bi ak ci wetu gémmiñ gi ; ay picc yu jumbaxlu (ombiliqué), xonq te wow ci njeexitali tànk yeek loxo yi ; ay picc ci awra yi (xuur yi ak ndéeñ li) ; donji deret yiy dajaloo ci suufu xef yi ; metitu bopp bu tar bu ànd ak yaram wu tàng ; ay tëndëndiir ci kanam gi, ay picc yu xonq te wow tegu seen kow ci ñenn ñi. Ngir saafara jàngoro ji, Dr Nduur ne, ay « antihistaminiques », ay « antibiotiques », ay pomaad, « bétadine dermique », « antalgique » ak « antipyrétique » lañu sàrtalagum, war koo jox way-tawat yi. Jawriñ Ablaay Juuf Saar demoon na loppitaanu Mbaaw, seeti way-tawat yi, may leen nopp. Ba mu àggee, ndokkeel fajkat ya fa nekk ak fajkati Ndakaaru yépp ci seen xereñ ak ni ñu gaawe toppatoo way-tawat yi. Ci la ko mbooloom gëstu mi tënkalee liggéey bi mu jot a def. Ginnaaw biñ waxtaanee seen biir, jël nañ dogal ne, way-tawat ya fa nekkoon, dañ leen di jàllale ca Centre de santé Sicap Mbao ngir toppatoo bu mucc ayib, fileeg ñuy jot ngirtey gëstu yi. « …askan wi dafa war a xam lépp… » Abdu Kariim Sàll, jawriñ ji yor lépp lu aju ci càkkéef bi, bokkoon na ci ndaje mees jagleeloon jàngoro ju yéeme jii. Moom, nag, ci biir i waxam, dafa sàkku ci njiit yi ñu bañ a nëbb askan wi dara, xamal ko li xew lépp ak nim fa deme. « Jàpp naa ni warees na xool bu baax ngir am limat yu wóor te biral leen askan wi nim gën a gaawe. Leneen li ma bëggoon a wax mi ngi aju ci yégle bi ak xibaar yees war jàllale. Ma jàpp ne, wareef la ci nun, nu fexe ba bañ a tiital askan wi. Ndaxte, ba tey jii, amagun dara lu leer ñeel jàngoro ji. Yaakaar naa ne, askan wi dafa war a xam lépp. Ginnaaw gi, warees na digal, képp ku nar a dem géej fan yii, nga fomm ko, rawatina mool yi. » Ablaay Juuf Saar ci wàllu boppam, xamal na fajkat yiy saytu way-tawat yi ak jàngoro ji ci boppam ne, dinañ leen dooleel, jox leen lépp luñ aajowoo. « Centre antipoison bi ak campeefi wér-gi-yaram yiy yëngu ci gëstu yépp dinañ leen jàppalesi ci liggéey bi, ci kilifteefu njiitalu wér-gi-yaram li. Danoo war a fexe ba lépp jaar yoon. » Waaye, ci njeexitalu waxam, jawriñ ji nangu na ne, mbir mi dafa laaj alal ju bare ak i jumtukaay.