Askanu Senegaal tollu na ci diggante bu tar cig ñàkk ba sax, li ëpp ci boroom-kër yi mënuñoo matale seen i wareef, rawatinaak ni dund gi yokkoo ci jamono jii. Yokkuteg dund gi nag deful lu dul yokk jafe-jafe yi fi nekkoon. Ndax kat, kenn naatablewul ne sunu réew bokk na ci réew yi gën a ndóol ci Afrig. Waaye nag, ndóol moom tekkiwul ne sag dund dafa war a jafe, doonte sax kenn waxul ni dafa war a yomb, mën naa daal tane, ba mu jàppandi ci ñépp.
Yokkuteg dund gi nu nemmeeku fan yii ci sunu réew ëlëm na boppi baadoolo yi nga xam ne seen i loxo jotuñu seen ginnaaw. Xamees na ne képp kuy dund ci miim réew, réerewul fi mu tollu cig ndóol. Ndeem sax ndóol gi tar na lool ci doomi réew mi, waaye, yokkuteg dund gi dafa yokk yeneeni jafe-jafe ci yi askan wi doon jànkonteel. Ñii xéyatuñu, ñee ngi lab ci mënn mi, ñale ñàkk nañu seen i liggéey ci mbas mi, ak ndaw ñi nga xam ni, yaakaaratuñu lu dul ci mbëkk ngir tekki, añs. Noonu la jàngoroy ñàkk jii lawee ci biir réew mi. Ndax kat, bu nu demee ba ku am di sakkanal, ku daan maye di nëbbatu, boroom doole yi di dimbalante seen biir doŋŋ, fu néew-ji-doole yi jëm?
Li koy firndéel mooy danuy seetlu ni saa bu ñu waxee ni dund gi yokku na, jaaykat yépp ay yokkandoo seen i njëg ca saa sa, duñu xaar dara. Waaye saa bu wàññeekoo, ñii dañuy wàññi, waaye ñale moom, duñ ko sax xalaat walla ñu wàññi rekk seen i njëg nu mu leen neexee. Loolu di wone coxorte gi am ci diggante doomi réew mi, ku nekk di seet ni muy amee, bu jaree sax mu lor moroomam. Yile xeetu doxalin ci sunu askan nag teey na xel lool, kenn xamul fu réew mi jëm ëllëg, su fekkee danoo wéyal bile nekkin. Maanaam ku man sa moroom rekk, wan ko ko. Jàngoro jii nu ganesi dina fi mujjee dëkksi, te nag, am réew balaa jëm kanam, ñépp taxaw ngir def ci seen loxo. Waaye nag, bu fukk di gas, fukk di suul, pënd baay xal abari rekk waaye pax moomu du feeñ. Yooyu doxalin nu nemmeeku ci biir mboolaay mi ñooy wane ni baadoolo yi nekkee ciy tolof-tolof ngir mën a raw rawale seenug njaboot. Ndax kat, doomu-aadama bu ne bala muy jóg di tal lenn, fàww mu am lu mu dunde. Te kat saaku moom bu defulee du taxaw, doonte sax Yàlla moom gémmiñ gu mu sàkk dina ca def aw ñam, muy dund walla mu def ca suuf, fekk dee na. Loolu tax ba yokkute dund gi mënul a tar ba tere nit ñi dund wànte, dina leen gàllankoor ndax duñu mën a suqaliku ba seenug dund gën a naat.
Nit nag ag dundam mënul a naat feek li muy dunde jàppandiwul. Te jamono jii nu tollu, askan wi sonn na lool ndax yokkuteg dund gi jéggee dayo. Yokkuteg dund ci réew moo xam ne liggéey daf fee jafe. Te boo seetloo bu baax, ñi amul liggéey ak ñiy taqale ñoo ëpp fuuf ñi jàpp ci lu dëgër. Ndegam ñàkkum liggéey rekk dafa doy jafe-jafe, dund gi tamit mënul a gën a jafe. Askan wi fim tollu ni lott na lool, amatul menn pexe ngir mucc ci jile jàngoro, xanaa nguur gi ko war a wallu, wallu ko. Nguur gi nga xam ne moom lay soob mu wàññi, walla mu yokk dund gi.