Mbëkk maa ngi wéy di lëmbe réewi Afrig sowu-jant yi, rawatina Senegaal. Saa su ñu jàppee ne mbëkk mi wàññeeku na rekk, fekk booba la waalo gën a aay. Li rot ci ay bakkan ci yoonu Espaañ wi, ñi ñu ci jàpp ak ñi ñu delloosi taxul ndaw ñi teggi seen tànk fa ñu ko tegoon bu yàgg ba tey. Nde, am na gaal gu ñu jàpp ci dibéer ji fa Bàmbugar. Te, lim bu takku la naroon a yóbb. Waaye, seen i pexe mujjuñoo àntu.
Bàmbugar, ab dëkk la bu nekk fa goxu Sóokóon nga xam ne ci Fatig la bokk. Fa béréb boobu la lim bu tollu ci ñaari téeméeri doomi aadama ak juróom-fukk naroon a bawoo dëgmal Espaañ. Lim boobu nag, am na ci ay ndaw yu dëkk Senegaal. Te, ñoo ca ëpp sax. Loolu terewul ne, li jot a rotagum ciy xibaar xamle nañu ne am na Saa-Gàmbi yu leen raxoon. Ni ñu ko baaxoo di gise rekk, gaal googu tamit ay ndaw ñoo ca ëppoon donte ne sax, ay jigéen yu yoroon doom a nga ca woon.
Saa-Senegaal yooyee nga xam ne ñoo bokkoon ci gaal googu, ñoom ñépp bokkuñu gox yu ñu bawoo. Am na ci ñoo xam ne Sóokóon lañu bawoo, ñenn ñi Jifeer, ñenn ñi Mbuur, ñenn ñi Kaaraŋ, ñeneen ñi Tuubakuta. Mu mel ni, ndaw ñi liy xew ci géej gi fëqul seen i bët. Moo tax, saa yu gaa ñi jàppee ne mbir mi dal na rekk, fekk na booba ndaw yaa ngi ci ay waajtaay. Te, li xew fa Bàmbugar démb ci dibéer ji firnde la ci.
Dafa di, gaa ñooñu waajaloon ba pare ngir jël yoonu ndox wi donte ne sax, seen mébét mujjewul a sotti. Bees sukkandikoo ci xibaar yi “Senego” rotal, laata ñuy jóge fa béréb ba lañu ko yëgal takk-der yi. Waaye, laata takk-der ya di agsi fa béréb ba, fekk na ña jiite woon tukki ba moom daw nañu dugg ci àll bi. loolu terewul am na ñenn ñu ñu ci teg loxo.
Kon, mbëkk mi moom dafa mel ni góom la rekk, saa su ñu jàppee ne wér na, mu daldi wulliwaat. Dafa di, ndawi Afrig sowu-jant yu bari rawatina yoy Senegaal, dañoo jël seen i bët teg ko ci tukki. Nde, jàpp nañu ne seen teraanga ci la nekk. Moo tax, yoonu Espaañ wi, li mu metti metti, ak li muy doy-waar lépp nga xam ne bakkan xaj na ci, safuleen.