Lu tollook weer a ngii wow, ñuy yéy ak a yàbbi ci waxtaan wi Njiitu réew mi woote woon keroog bésub korite ga. Am ñu ci ànd, di ko layalee tolluwaayu réew ak jàmm jees fi war a jëmbët, rawatina bees jubeey wote yoy, dara leeragu ci. Mu am nag ñeneen ñoo xam ne, ànduñu ci. Nde, dañ jàpp ne, pexe mu Njiitu réew mi lal la ngir jàllale ñetteelu moomeem gees di laam-laame. Li ëpp ci waa kujje gi, rawatina Usmaan Sonko, dañ ko gàntu. Dafa di, laltaay bi war a jiitu waxtaan wi moo sooke ci xalaati ñi ci bañ a bokk. Bokk na ci matuwaay yooyii ñuy xaar ci Njiitu réew mi mu jël leen, mooy bàyyi ñi mu teg loxo ci sababi pólitig, wax ne du bokk ci wotey 2024 yi, bañ a seppi benn lawax te fal ab jëwriñ ju màndu juy lootaabe wote yooyule. Waaye de, dafa mel ni, Njiitu réew mi, Maki Sàll, fullaalul càkkuteefi yooyu. Nde, jàppees na bésub waxtaan. Dees na ko amal bésub 30 me 2023. Rajo RFM moo siiwal xibaar bi.
Juróom-ñeenti weer kepp ay bëgg a des ci wote yu 2024 yi. Waaye de, réew mi dafa mel ni lu toog ci nen. Fitna jiy yoot Senegaal ak ñàkk a wóolante gi dox diggante Nguur gi ak li ëpp ci kujje geek way-moomeel yeek askan wee tax ba Njiitu réew mi wootew waxtaan. Waxtaan la wow, Senegaal lees ci namm fénc, ñu duppee ci tubaab « Dialogue national ». Am na nag, ñu koy woowe « Dialogue politique » ngir ne, ci seen gis-gis, ñi ko woote ak ñi ci nangoo teew, seen mbiri bopp kepp a leen yitteel. Ku ci nekk, noo bokke ci wotey 2024 yi kese nga wër. Naam, mëneesul a nettali géntu jàmbur. Waaye kat, jamono jees sulli mbirum waxtaan wi, anam bees ko nasee ak coow li ci juddoo yépp, day xaw a teey xel. Waxtaan, ci yoon, dafa war a boole, waaye warul a féewale. Te, lees seetlu bi coowal waxtaan wi jibee ba tey, moo di ne wuute dafa am, waaye féewalo bu bir daf ci am, rawatina ci kujje gi. Loolee taxati, am ñu jàpp ne dara wundul waxtaan woowu lu mooy wàññi dooley kujje gi. Bu loolu dee nisëru ñi ko tëgg de, seen pexe mi ngi bëgg a àntu.
Lëkkatoog Yewwi Askan Wi a ngi bëgg a yewweeku, bu tasul ci biir ba noppi sax. Ndekete, ku ci mel ni Xalifa Sàll, moom ak pàrteem bii di waa Taxawu Senegaal, nangu nañoo waxtaani. Ginnaaw moom, kilifay YAW yépp dañoo bañ a dem ci waxtaan wi. Muy Usmaan Sonko, njiitul kujje gi, di Ayda Mbóoj, di Décce Faal, di Maalig Gàkku, di Séex Tiijaan Jéey, añs., kenn nangulul Maki Sàll loxo bim leen tàllal. Wëliis waa YAW, PDS ak yeneen way-pólitig ak i kurél yu siiwadi rekk a nangoo teew ci waxtaan wi.
Sababub ngànt lees gàntal Njiitu réew mi, bi ci jiitu, mooy ne, moom ci boppam, yeyoowul wooteb waxtaan woowule. Ndax, warul bokk ci wotey 2024 yi. Bi ci topp mooy ne, balaa sumb aw waxtaan, fàww nga teg yar bi ci suuf. Waaye, mëneesul a jàpp i nit, di duma ak a tëj ci kaso yi ba noppi naan leen « nu waxtaan ». Looloo dal waa Pastef. Ndax, am na lu tollook ay téeméeri téeméeri ci seen i ñoñ yoy, ñi ngi ci kasoy Maki Sàll yi, ci seen wax, ñoom waa Pastef. Te, dara taxul ñu nëbb leen jant wi lu dul mbirum pólitig ak ñàkk a ànd ci yoriinu réew mi ak ni Yoon jenge. Mu am itam ñeneen ñoo xam ne sax, bokkuñu ci genn làngug pólitig. Ay taskatu xibaar kepp lañu walla ñu di ay way-moomeel yuy wax seen xalaat ci jafe-jafey réew mi.
Moo tax, kii di Usmaan Sonko, nga xam ne ay ñoñam a ëpp ci kaso te, mu bari lu muy jëflanteek Yoon, rawatina ci jamono jii ñu tollu, fasul yéene toog ci waxtaan woowu. Moom nee na, du waxtaan ak koo xam ne, mi ngi ko teg ag fetal ci keru nopp. Waaye, taxawaay boobu wéetu ci. Ndax, am na ñeneen ñu ko taxawe. Muy ku ci mel ni Aminata Ture, Maalig Gàkku, Décce Faal, PUR bu Sëriñ Mustafaa Si, yenn ci kuréli way-moomeel yi, di waa F24 bi leen boole, nee nañu woon duñu ca bokk. Baabakar Jóob (Njiitul FDS-Les Guelwaars), Bugaan Géy Dani, Abdurahmaan Juuf (Njiitul làng gii di Awale), ak ñeneen ak ñeneen… Ñoom nee ñu bala ñuy mën a bokk ci waxtaan, fàww mu doon lu dëggu. Daray pólitig bañ koo lal, njariñal réew mi kepp tax koo jóg. Ndax, am na yeneen yu ko fi jiitu woon, te, jëlewuñu ci dara daanaka. Mag nag, kenn du ko nax ñaari yoon.
Loolu terewul ne am ñeneen ñu fare ci kujje gi ñoo xam ne, nee nañu dinañu teeweji waxtaan woowu donte ne sax bariwuñu. Muy ñii di waa PDS (Parti Démocratique Sénégalais), Taxawu Senegaal bu ñoom Xalifa Abaabakar Sàll ak ñeneen ñu ci mel ni Séex Baara Dolli (Njiitul mouvement Nekkal fi askan wi), Paap Jóob (Bokk Gis-Gis) añs. Mu mel ni nag, kii di Xalifa Abaabakar Sàll ak Kariim Wàdd seen mébét mooy fexe bañu faral leen seen i daan ngir, ñu mën a bokk ci wote yii di ñëw.
Kon daal, mbir maa ngi noonu. Waxtaan wi moom, jàpp nañu ko fanweeri fan ci weeru me wii ñu nekk. Dees na ko amal lu tollu ci diirub fukki fan ak juróom. Nee ñu, li ko wund, mooy fexe ba jàmm ak ug dal am ci réew mi. Lu tëw a xam nag dafa yàggul. Te, kuy naan di làqatu, boo màndee feeñ.