JÀPPATI NAÑ AY MBËKK-KAT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal mbëkk mi lëmbe na lool réew mi, rawatina jamono jii. Am na sax, ñu jàppoon ne dina wàññeeku. Ndekete, tey la doomi Afrig sowu-jant yi gën a ñeme yoonu Espaañ wi. Barki-démb, ci ngoonu gaawu gi rekk, ay boori juróom-benn waxtu, teg nañu loxo lu jege fanweeri doomi-aadama yoo xam ne dañoo naroon a mbëkki.

Mbuur a ngi jooy ay doomam, noppeegul sax ñeneen bëgg a songaat géej gi. Bu dee dañu ne, ku ndóbbin rey sa maam, foo gisee lu ñuul daw. Ndawi Afrig sowu-jant yi nag, rawatina yoy Senegaal yi, ñoom dee taxu leen a daw. Ndax, bakkan yu bari yiy des ci ndox mi moom, kenn ci ñoom umpalewu ko. Rax-ci-dolli, tëkku yi ñu leen di tëkku ak dig yi ñu leen di dig, taxul ñu bàyyi. Ñoom daal, bàrsaa rekk, mbaa barsàq.

Mu mel ni coowal mbëkk mi moom saa su ne day gën a law ci réew mi. Ba tax na, jamono jii, Nguur gi fi nekk taxaw temm ngir jële ko fi. Dafa di, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ci jëmmi boppam moo sàkku ci askan wi ñu jàpp ci liggéey bi. Su ko defee, jéyya ji amoon fa Mbuur, mën fee gëj. Ndax, bu ñu dakkalee mbëkk mi, géej gi dina gëj a lor ay doomi Senegaal. Looloo tax, takk-der yi bëgg a jëfe ndigal li ba dakkal mbir moomu.

Dafa di, barki-démb ci ngoonu gaawu gi rekk jàpp nañu lu tollu ci ñaar-fukki nit ak juróom-ñaar yoo xam ne dañoo bëggoon a jël yoonu géej gi. Ñi ngi leen tegee loxo fa koñ bii di Falox, fa Mbuur. Bees sukkandikoo ci APS (Agence de Presse Sénégalaise), ñoom ñépp duñu ay Saa-Senegaal. Juróom-ñaar ya kepp ñoo ciy doomi Senegaal. Ñaar-fukk yi ci des, ay Saa-Gàmbi lañu.

Kon, ñu gis ne mbëkk mi moom amatul tànki ginnaaw. Ndax, ñi ciy sóobu mel na ne dara mënatu leen a téye ba ñu teggi seen i bët ci Espaañ. Laaj bi jar a samp kay mooy, ndax Nguur gi am na ay pexe yu mën a dakkal mbëkk mi ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj