Guddig dibéer jàpp altiney tey jii fukki fan ak juróom-ñett ci weer wii la tàkk-tàkk lu am doole am fa Gine Konaakiri. Fa ñuy denc soroj beek yu ni mel moo lakk. Maanaam, ci farãse “Dépot d’hydrocarbures” bi nekk Kalum. Jéyya jooju nag, ub na lool boppi kilifa ya. Li ko waral mooy doole ji mu am ak njeexital yi mu mën a jural askan wa. Fim tollu nii tembere, xamaguñu lan moo sabab jéyya jooju.
Njàqare ak tiis la askan wa dëkke fa Konaakiri yeewoo tey. Li ko waral du lenn lu dul lakk gu metti ga fa am. Rax-ci-dolli, mu ame fa béréb boo xam ne, mën na laawaale ñu bari. Ndax, kenn umpalewul doole ji soroj làmboo, rawatina bu laalee ak lu deme ni safara. Moo tax Nguur gaa ngay def kemtalaayu kàttanam ngir askan wi mucc ci loolu. Ba tax na jël nañu mbooleem kurél yi xareñ ci wàll woowu boole kook i matuwaay ngir yëf yi bañ a ëpp i loxo. Maanaam njeexital yi bañ a jéggee noonu dayo ci nekkiinu askan wi.
Ginnaaw bi jéyya ji amee nag, ci la Nguur gi génnee yégle xamle xew-xew bi fa am, biralaale ndogal yi mu namm a jël ngir saafara loolu. Waaye, ba tey taxul ñu fésal li ko sabab ak ñan ñoo ci loru ak sax ndax am na ñu ci ñàkk seen bakkan am déet. Kon, bees sukkandikoo ci seen yégle boobu, duñu am tontu ci laaj yooyii. Terewul ne, ginnaaw gi am na xibaar yu rotee ci yenn kibaaraan yi niki France 24 mi xamle ne am na lu tollu ci fukki doomi-aadama ak ñett yu ci ñàkk seen i bakkan. Lu tollu ci téeméer ak juróom-ñaar fukki nit ak juróom-ñett yu ci jële ay gaañ-gaañu yu metti.
Mu mel ni kon mbir mi tàmbali naa ëpp i loxo xaat. Nguur gi xam gi mu xam looloo tax mu jël ay ndogal ngir aar askan wi. Moo tax ñuy sàkku ci bépp liggéeykat, nga aju ci Nguur walla nga ñàkk cee aju, nga toog sa kër. Ñiy wattu kaaraange gi kese ñoo bokkul ci ndogal loolu. Ñaareel bi mooy mbooleem bérébu jàngalekaay yi dañu leen di tëj muy yi aju ci Nguur gi ak yi ajuwul ci moom yépp. Bi ci mujj mooy béréb yi ñuy dippe “stations-services” yépp lañuy tëj ba mu des yi ñu naan “services d’urgence”. Kon, loolu firnde la ci ne waa Gine ñi ngi jamono jii ci guddi gu bët setagul. Ba tax ñu jël mboleem matuwaay yi war ngir aar seen bopp. Ndax kat, fagaru moom moo gën faju.