JIITUWAAYI CÀMM GU BEES GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, taxawal na càmm gu njëkk ci moomeem gi. Muy càmm gog, coppite la woote ak xëcc jëmale ci bëgg-bëggi Saa-senegaal yi. Mu namm koo jaare ci ponk yoy, ñooy doon jiituwaayi (priorités) càmm gi.

Démb ci àjjuma ji, la Umar Sàmba Ba, fara-caytu njiiteef gi siiwal turi ñi séq càmm gu njëkk ci moomeg Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Muy càmm gu ñu yamale ci 25i jëwriñ ak 5i fara-caytu. Laata Sëñ Ba di ko siiwal, magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, biral na li ñuy xaar ci càmm gi ak anam bi ñu ko tëggee. Li mu njëkk a xamle mooy ni :

« Càmm gu bees gi, ñoo ngi ko tëgg ci anam bu méngook sunub sémb bi nu doon biral ci kàmpaañ bi, te am yéene tabax ci réew mi. Càmm la guy dox lu njëkk ci dakkal doxalin yi fi nekkoon. »

Mënees na jàpp itam ni càmm gu boole waa Pastef yi la ak ñi ko doon jàppal tànk ci xeex bi.

« Càmmug mbooloo la, gu ñu méngale te yamale jëwriñ yi. Doon na itam càmm guy jege askan wi, guy fent lu bees te di taxaw temm ci soxla Saa-Senegaal yi. »

Bu loolu weesoo, magum jëwriñ yi dellusi na, benn benn, ci ponk yoy, mënees na jàpp ni ñooy jiituwaayi càmm gi. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, càmm gi dina xar tànku tubéyam ci xeex dund bu jafe bi, yokk am-amu askan wi ba lu waay bëgg mën ko jotee ak doole boppam. Naka noonu, bokk na ci yi muy jiital : « mbiri ndaw ñi, njàng mi, tàggatu gi, njéemantu gi ak xëyu ndaw ñeek jigéen ñi. »

Càmm gi dina taxaw itam ci suqali koom-koomug réew mi. Mu nar cee jiital pexey « moom sa bopp ci koom-koom, ndefar gu jaar yoon ñeel balluy mbindaare yi, yokkute biir réew mi ak suqaleeku Senegaal gu jaar yoon. »

Dina doon itam càmm gu jox gëdd doxalinu yoon, guy sàmm àq ak yelleefi doom-aadam, guy amal càmm gu mucc ayib, guy leeral doxalin yi ak a doxal dëgg tey ñoŋal doxalinu demokaraasi.

Ci kow yooyu yépp nag, du leen tere taxaw temm ci dëgëral bennoo réew mi, rattaxal diggante yi, yokk kaarange réew mi, aar jàmm ji fi am ak dal gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj