Mari Sàmb Géy, ñu gën koo xame ci Mari Géy, moo ñàkk bakkanam fa Ngor, ci anam yu doy waar. Xew-xew boobu ma nga amoon talaata ci guddi, boori fukki waxtu. Coow la sabab faatug ndaw soosu mi ngi sosoo ci raafal gu takk-der ya doon amal ca béréb boobu ngir caytug dàntite. Moom Mari nag, jamono jooja ma nga nekkoon ca béréb boobu di féexlu moom ak benn xaritam. Ca la leen takk-der ya fekkee foofa laaj leen seen i dàntite. Mari moom, joxe woon na dàntiteem. Waaye, loolu terewul ñu dugal ko ci seen daamar gi. Li doy waar ci mbir mi mooy kuy dund lañu yeb, wàccee néew.
Anam yi Mari Géy génne àdduna mi ngi wéy di ub boppi saa-senegaal yi, rawatina askan way yeewoo fa Ngor. Ndax, kenn umpulewul ne, bu yàggul dara jàmmaarloo bu metti amoon na diggante askan woowu ak takk-der yi ba bakkan rotoon ca. Mu nel ni nag, coow loolu jeexagul ba tey bees sukkandikoo ci seede yi ak ñi teewe xew-xew boobu. Jenn jigéen ju bokk ci jegeñaale Mari moom jàpp na ne yëf yi am na lu leen boole. Kàddoom yooyu muy nettali anam yi mbir mi ame ñi ngi leen taataane ci mikoro waa Senegaal7.
“Ci xeex bu metti boobu ñu reye woon xale bu jigéen boobu tuddoon Aji, moom dañu ko ràññee woon ci widewoo yi. Moo tax mu ne ko “imbécile” bi xàmmee naa la. Mu ne ko duma “imbécile”. Mu ne ko jox ma sa dàntite. Ki nga laaj dàntiteem mu jox la ko xanaa war nga ko bàyyi mu dem. Mu ne ko toppu nu. Bi mu leen toppee ba ci daamar gi ñu ne ko yéegal, mu yéeg. Bi ñu génnee ak moom lañu ko dóor ba mu dee. Ñu waññeekuwaat, sànni ko ci Parking bi. Benn aji-wattu (vigile gardien) moo ci yem daldi woo nit ñi. Ñu ñëw woote kër ga. Bi ñu ñëwee fekk nanu mu dee bu yàgg. Ndax, ñoom ba ñu koy sànni fekk na dee na ndax, ñoo ko rey. Ba nii gisuma néewam. Wax dëgg Yàlla mënuma xam li nekk ci yaramam. Waaye, daal dañu ko dóor ba mu dee, ñu sànni ko ci Parking bi daw dem. Ndax, loolu war na ku tollu ni ab takk-der, rey nit ba pare sànni ko. Sàndarma yi na ñu génn sunub dëkk, na ñu nu abal Ngor. Bañunu ci dara, te, lii nii dañu koy topp. Dañuy pelent, dañuy def lépp. Am nañu ay kilifa, loolu seen liggéey la. Waaye, duñu bàyyi, ndax, Ngor fii wenn say la. Reyal nañu nu bee weesu, mujjul fenn. Waaye, bii moom ci lay doxe saafarawu ba fàww.”
Kii di Mamadu Sàmb di rakk ci baayu Mari Géy moom tamit foofa la jaar. Ndax, nee na Mari benn xaritam la àndaloon di féexluji. Takk-der yi fekk leen fa, ñu njëkk a laaj xaritu Mari bi laata ñuy dem ci moom.
“Mu dem ci Mari Géy. Xale bi génnee dàntiteem jox ko ko. Bi mu ko joxee dàntiteem mu ne xàmmee naa la yow. Saaga ko ne ko :”doomu haraam nga”. Mu tontu ko ne ko : “sama yaay jurul doomu haraam”. Ci noonu lañu ko dugal ci biir daamar gi. La am ci biir daamar gi, xamuñu, lañu ko def umpu na ñépp. Waaye, bi ñu nu ko wàccelee ab néew lañu nu tegal foofu. Ma yaakaar ne nag ci laajum dàntite rekk lii waru ci mën a am.”
Kon, mbir mi am na lees waxul. Rax-ci-dolli bees sukkandikoo ci li mbokk yi seede mooy ne ñoom yemuñu ci tooñ ko rekk. Waaye, dañu boole metital ba mu faatu. Ndax, bu dee bi muy dugg ci daamar gi dara jotu ko. Ñu jekki saa génneel leen ab néew, mat na ñu samp ci ab laaj. Lu xew ci diggante bi ñu yéegale ak bi ñu ko wàcce ?
Tontu laaj boobu nag moo yokk ci xar mi karaw. Ndax, toppekat bokkeef gi moom li mu xamle ci yégleem bi mooy kenn metitalu ko. Benn jàngoro bu mu doon sooxaale moo ko rey. Maanaam li otopsi bi feeñal mooy ne sababu faatu gi li ñuy dippe “une pancréatite aigue hémorragique et une absence de signe traumatique”. Ay mbokkam ak ñenn ñuy seen xam-xam màcci ci wàll woowu moom nanguwuñoo dégg loolu. Kii di Mamadu Sàmb nga xam ne kenn la ci mbokku ndaw si moom gëmul loolu. Ndax, lu ne fàŋŋ, kenn du ko jeex.
“Otopsi bi dafa wax ne xale bi dafa am feebar bu nekkoon ci moom. Ma yaakaar ne mboolem nun ñi nekk fii, ku nekk am na feebar booy doxantuwaaleel. Li ko rey nii feebar boobu la. Waaye, nun gëmunu loolu. Laaj naa fajkat bi nekk raglu CTO mu wax ma, ma ni ko gëmuma loolu ci kanamu samay seede. Nee na ma nag boo soxlawaatee leneen na nga ñëw ma leeralal la. Ndax, ay jëf la ñi mu àndaloon seede nañu ne sàndarma yi dañu metital ci seen biir daamar gi. Bi ñu ko wàccee dañu ko tëral, loolu moom am na ci firnde yu leer nàññ. Kon, ak lu ñu mën di wax, ñoom kepp la soxal.”
Mu am tamit keneen ku xam-xamam màcci ci wàll woowu di Doktoor Baabakar Ñaŋ, moom it xelam ñaaw na ci toppekatu bokkeef gi teg ci loxo askan wi. Ndax, moom jàpp na ne anam yi ndaw si génne àdduna ak ni pancréatite di reye am na ay wute. Te, ni ñu misaale faatug ndaw si jaaxal na ko ba tax mu ne :
“Pancréatite bu la jàppee sówetaas ngay nekk. Maanaam dañu lay may doole (réanimation). Pancréatite kuy naan sàngara su bari walla ay poson yu bari walla ñu posone la kooku mooy am ay pancréatite. Te, xale boobu gëmuma ne daan na jege yooyu. Toppekat bi mënunu ko wax dara, benn fajkat lañu ne moo bind yëf yi. Otopsi bu jaar yoon bu am coow. Li jiitu rekk mooy ne ni ñu ko binde dafa doy waar. Otopsi boo ko bëggee def dangay jóge bopp ba ca tànk ba. Xool fépp, cér ak cér. Waroo bàyyi fenn. Diggante këram ak foofu daanaka def na ñaari kilomeetar. Te, ku am pancréatite mënul a dox benn kilomeetar.”
Lu ci mën di am daal ndaw si moom faatu na ci anam yu metti. Rax-ci-dolli du it guléet ñu fiy gis xeetu otopsi yu ni mel. Ndax, ñenn ñi faatoo ci jàmmaarloo yi weesu misaal lañu ci. Moom Mari Géy nag nee ñu am lu tollu ci ay juróom-benni bant. Ay seex la mujjee am nii. Xale yooyu ci at rekk lañu tollu. Donte ne sax kenn umpulewul ne dee moom yépp a metti, deewu boroom njaboot daf cee raw.