JIIXI-JAAXA CI GÉNNUG ÀDDUNA IMAAM UMAR JAAWO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Naqar ak tiis la askanu Koldaa nekke fan yii, rawatina ña dëkke fa koñ bii di Medina Serif  Perlel. Nde, kii di Umar Jaawo moo génn àdduna ci anam yu teey xel. Ñii di waa L’Observateur ñoo siiwal mbir mi ci seen i xët. Génnug àdduna imaam Umar Jaawo nag, jur na ay jiixi-jaaxa yu bari. Te, dara waralu ko lu moy na ñu fekke néewam. Looloo tax ba nii jébbalaguñu ko Boroomam. Ndax, waa sàndarmëri ñoo ci teg seen loxo ngir amal seen i luññutu.

Du guléet ñuy gis xew-xew yu doye waar nii ci réew mi, rawatina jamono jii ñu tollu. Waaye, bu ni mel bariwul lees ko di gis. Xew-xew bii nag, mi ngi am ci subag gaawu bii weesu. Bi mu amee, boroom daamar guy séddale mburu moo ko gis ci wetu benn bitig. Ca la woowe boroom bitig ba. Moom, ba mu ñëwee ba gis ko, xàmmee ko. Moom it, mu woo taawu imaam ba mu ñëw. Jamono yooyu, fekkoon na mu sonn. Waaye, loolu terewul ñu yóbb ko këram. Ba mbir ma tëwee sotti, ci lañu ko yóbbee fa raglu ba. Waaye, imaam Umar Jaawo mujjul a mucc ca gaañu-gaañu ya. Nde, dafa mujjee ñàkk bakkanam.

Ba mbir ma demee noonu, ñoom ñu yóbb ko ca morgo ba ngir waajal ko, jébbal ko Boroomam. Waaye, yëf yi mujjewul a deme noonu. Nde, ñii di waa sàndarmëri ñoo ñëw dakkal cang ga. Li ko waral du lenn lu moy gaañu-gaañu bi ñu gis ci naq bi. Looloo indi ay sikki-sàkka ci anam yi mu génnee àdduna. Waaye, mbir yemul foofu. Dafa am yeneen yu ñu gis fa boor ba mu daanoo. Lu jege ñeenti téeméeri meetar ak fa ñu ko fekk, gis nañu fa ay toqi deret. Rax-ci-dolli, am na paaka bu taq deret bu ñu fa gis. Yooyu ñu gis a tax ñu jàpp ne am na luy ñuul ci soow mi. Maanaam, am na lu laxasu ci mbir mi. Te, am na nu muy deme sax fekk dañu koo dogaale.

Li am ba des mooy ñàkkug kaaraange gaa ngi wéy di gën a bari ci réew mi. Daanaka, bareetul lees di toog ab diir te, déggeesul xew-xew yu ni mel, donte ne sax, ba nii xameesagul ci yan anam la génne àdduna. Waaye, waa birigàddu sàndarmëri bu Koldaa door nañu luññutu yi. Kon, fii ak ub diir dees na xam fan la wànnentu mujjeek i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj