Bokkadil yu CHAN 2022 bi jeex nañ ci njeexitalu ayu-bés bi weesu. Ren jii nag, 18i réew ñoo koy joŋanteji. Ñu ràññe ci Senegaal. Muy delsi bu am solo ginnaaw bi mu ko wuutee 2011 ba tey.
CHAN, ñu gën ko a miin ci « Championnat d’Afrique des Nations », maanaam joŋante réewi Afrig yi, kub la bu mboolem réewi Afrig yi di xëccoo ci ñaari at yu nekk. Bu ñuy wax CHAN nag, dooleel ndaw yiy yëngatu ci seen biiri réew a ko waral ngir ñu mën a bokk ci joŋante yu mag yi ak feeñal seen xereñ. Ñu war cee jaar it dooleel ak a suqali futbal bi ci kembarug Afrig. Looloo waral ba saa-afrig yiy joŋante ci seen biiri réew doŋŋ lañ ciy woo. Biñ ko sosee ci atum 2009 ak tey, 6i kay jot nañu a jàll. Kayu 2022 gi nag, yem ak 7eelu kay gi, réewum Alseri a koy dalal. Ñu ràññe ci delsi gaynde Senegaal yi.
Gayndey Senegaal yi nag gëjoon nañ koo joŋante lool. Ci atum 2011 lañ ca gëjoon a bokk. Ci xayma, toogoon nañ fukki at ak benn yoy, teewe CHAN bi tëwoon na leen ticc. Li ko waraloon di lajj yu metti yi ñu tegle, di ko lajj ci bokkadil yu ñeenti kay yi weesu, rawatina ci seen diggante ak Saa-gine yi leen toogloo ñetti yoon.
Gine moomu nag, tëwoon ko ticc, la Senegaal toogloo wile yoon. Ginnaaw ñaari joŋante yoy ku ci nekk dafa dóor moroomam benn yoon, ci dóoral-ma-dóor la Senegaal mujje ame ndam (3-5). Ndam loolu nag, nekk na luy suul naqaru ñetti yoon yi Gine di toogloo Senegaal waaye itam luy feeñal bànneexu bokki ca ñay xëccooji kub bi la ak liggéey bu am solo bi ko nekk ci ginnaaw. Noonu lañ ko mën a dégge ci kàdduy Sã Luwiis Juuf, bokk ci joŋantekati Senegaal yi :
“ Mbégte mu réy la, toog nanu 11i at, mu yàggoon lool te joŋantewuñu CHAN. Kon dun def lu dul yëg ci sunu bopp. Lu nu yàgg a bëgg la, bi nuy ndaw ba léegi, tey nu màgg def ko. Waaye, ni ma ko waxe woon, danu liggéey bu baax ngir yékkatiwaat futbalu Senegaal. Loolu moo doonoon sunu yitte.
Bu kàdduy Sã Luwiis yi junjee liggéey bu am solo biñ def it, Ógistĩ Seŋoor mi jiite FSF delsi na ci bu baax. Toftal na ci tamit jafe-jafe yi njaayum joŋantekat yi gën a xerañ at mu jot di leen di andil. Bokk na ci lu tax ñu gëjoon a teewe lool bile joŋante. Mu mel ni kon ku bëgg dara foog nga def dara. Ba tax na ñuy xaar yan pexe la làngu futbal gi ci Senegaal fas yéene lal ngir dooleel mbootaayi futbal yi ci réew mi ba ñuy dégg seen jaloore ci kembarug Afrig.