Nguur gi taxawal na daluwaay nimerig bees dippee JUBBANTI ngir waajal péncoom réew mi ñu jagleel pólitig bi. Muy ab daluwaay ngir amal péncoo mu yaatu te leer, mu ñépp mën a bokk.
Bërki-démb ci àjjuma ji, 9i fan ci weeru me 2025, lañu doon lël ak taskati xibaar yi ngir ubbi daluwaay JUBBANTI. Ñoo ngi ko amale ca taaxu caytu gi ñu duppe Mamadu Ja, bi 16i waxtu jotee ci ngoon. Jubbanti di ab daluwaay nimerig bu Nguur gi taxawal ci waajtaayi péncum réew mi ñu namm amal keroog àllarba, 28 me 2025.
Daluwaay boobu nag, taxawal nañu ko ci anam wuy yaatal péncoo mi ba Saa-Senegaal bu nekk, ak fu mu mën a nekk ci àddina si (ci biir réew mi mbaa fa bitim-réew), dina ci mën a bokk. Muy doxalin wu bees wu Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tànn ngir amal péncoo mu yaatu te leer, mu kenn ku nekk ci doomi réew mi mën a joxe gis-gisam.
Péncoo moomu, dinañu ko amal ci njiiteefu Séex Géey mi Njiitu réew mi tabb ngir mu jàppandal mbir yi. Ci bi ñuy jàkkaarlook taskati xibaar yi, démb, mom Sëñ Géey dellu na leeral ni daluwaay bi doon na jéego bu am solo jëm ci taxawal demokaraasi bu méngook jamono, bu jaare ci nimerig bi ñépp jot. Naka noonu, muy xamle ni fas naa yéene am ci taxawaay bu mucc-ayib. Te mooy fexe ba kenn du beddi gis-gisub benn ma-xejj ngir JUBBANTI doon keno bu am solo ci mbooru demokaraasi Senegaal.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Source A fésal, dees na xaar lu ëpp 169 pàcc ca péncoo ma, donte ni sax Sëñ Séex Géey wax na ne jébbaleeguñu woote yi. Waaye, bir na ni waa APR (Alliance Pour la République), di làngug pólitig gi jóge ci Nguur gi bu yàggul dara, naruñoo teewe ndaje ma. Démb ci àjjuma ji lañu ko xamle ñoom itam, ci bi ñuy jàkkaarlook taskati xibaar yi.
Bees déggee li Séydu Géey mi yoroon seen kàddu wax, bañu lu jëm ci péncoo, waaye Nguur gi dafa bëgg far turu Maki Sàll, jëmmam ak jëfam ci xelu Saa-Senegaal yi. Ay pexe la nas ngir yàq deru Maki Sàll ak i ñoñam, di dal ci kaw kilifa pólitig yi ak ñi fare ci ma-xéjj yi. Nako noonu, ñuy ñaawlu làngug pólitig bi ñu gis ni dafa ñaaw léegi ak ni ñuy singalee kilifa yi fi nekkoon ci Nguur gi weesu.