Magum jëwriñ ju bees ji, Sidiki Kabaa, dalal na xel yi ñeel wotey 2024 yees dégmal. Nde, ñu bari dañ doon ragal jumtukaayi wote bi bañ a mat ci diir bu gàtt bees jàpp wote yi ginnaaw biñ ko dàqe ca njëlbeen ga. Waaye, moom miy elimaanu jëwriñ yi àddu na ci démb ci altine ji wax ne, lépp yemb na. Maanaam, nguur gi jàppandal na jumtukaay yees aajowoo yépp ngir wote yi jaar yoon.
Meetar Sidiki Kabaa biral na ne caytug bokkeef gi yóbb na jumtukaayi wote yi fépp fi réew mi ak fa bitim-réew. Ak ni àppug wote yi jampee, njorteesoon na ne Càmm gi dina lott ci lootaabe wote yi ci anam bu mucc ayib. Waaye, bees sukkandikoo ci Sëñ Kabaa, jarul ñuy jàq, lépp dina mat keroog 24 màrs 2024.
Cig pàttali, bésub 25 féewiryee 2024 la wote yi waroon a am ci yoon. Waaye, keroog 3 féewiryee la Njiitu réew mi, Maki Sàll, dàqoon wote yi, fomm leen. Coow lu réy toppoon ci, fi réew mi ak fa bitim-réew, fépp, ñuy mbamb Senegaal ak a yedd Njiitu réew mi. Fitna sax jot na cee am ba ñaari bakkan rot ci. Noonu, ay ñu dox di dox ba ni ñuy jàppee bésub 24 màrs 2024 bii di ñëw.
Ci diggante bi nag, Njiitu réew mi jotoon na cee tas Càmm gi, tabbaat geneen gu yees, jiital ci Meetar Sidiki Kabaa mu wuutu Aamadu Ba miy lawau Bennoo Bokk Yaakaar. Càmm gu bees gii nag, liggéeyam bi gën réy mooy amal wote yu jaar yoon. Wote yooyu nag, ak li ci jot a xew yépp, xel yi teey nañ ci lool. Loolu la Sidiki Kabaa xam ba tax ko wax ne :
« Dama bëgg a dalal xeli Saa-Senegaal yi : jumtukaayi wote bi mat nañ te jàppandi nañ. […] Caytug wote yi yóbb na jumtukaay fépp fi ñu war a wote ci réew ak fa bitim-réew. »
Jëwriñ ji xamleet na ne bilteŋ yi ñuy wotee jàppandi nañ. Ciy waxam, am lu des ci liggéey bi, waaye nee na rafet na njort ne lépp dina yemb balaa bés biy teru.
Ginnaaw bim dalalee xel ci fànn woowii, jëwriñ ji àddu na ci kaaraangeg lawax yiy dagaan baatu askan wi. Nde, xamal na taskati xibaar yi ne, lawax bu nekk, lu mu ndaw-ndaw, dinañ ko boole ak ñaari takk-deri BIP. Muy xibaar bees rafetlu ginnaaw bi taskatu xibaar bu siiw bii di Paap Aale Ñaŋ digalee lawax yi ñu wattu seen bopp te moytu. Bees sukkandikoo ci boroom Dakarmatin, am ñuy nas i pexe ngir faagaagal ab lawax, faat ko. Li ñu ci jublu, ba tey ci waxi Paap Aale Ñaŋ, mooy rey benn lawax ngir ñu dàq wote yi.
Meetar Sidiki Kabaa nag, artu na lawax yi ak képp ku namm a yee fitna ci kàmpaañ bi. Nee na, ku fi yékkati taafar, ciy jëf walla ciy wax, Càmm gi dina ko digaale ak yow ba mu saf.