KAAJARUG “NEW DEAL TECHNOLOGIQUE”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay ci altine ji lañu doon aajar naal wees dippee “New Deal Technologique”. Ndaje moomu, fa CICAD (Centre International de Conférences Abdou Diouf) lañu ko doon amalee. Ñi ngi ko doon amalee ci teewaayu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, Njiitu Ngomblaan gi, El Maalig Njaay, ñenn ci jëwriñi Càmm gi ak i dépite. Mu doonoon ndaje mu am solo. Ndax, kenn umpalewul njariñu xarala ci jamono jii. Moo tax, Njiitu réew mi taxawal naal wii ngir soppi xar-kanamu réewu Senegaal ci fànn wi.

Naaluw “New Deal Technologique” nag, benn la ci sumb yi ñu dëxëñ ci sémb wu mag wi ñu nammee yor réew mi “Vision 2050”. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, yékkati na ay kàddu ngir leeral solos naal ak nu ñu koy doxalee ak luy jubluwaay bi.

Naal wii, wenn la ci yi fi jot a jàll. Muy ci wàllum ndox mi, càmm gi, añs. Muy naal wow, ci wàllu xarala lañ ko tënk. Seen mébét du lenn lu moy réewum Senegaal moom boppam ci wàll woowu. Ñu fexe ba lënd gi jàppandal ci askan wépp. Ñuy mën di dugg ci lënd gi ci njëg yu yomb. Su ko defee, mu yombal leen xeeti xibaar yi ñu soxla yépp. Rax-ci-dolli, ñu yokk xarala gi ci campeef yi ba lijjantig këyit gën a yemb. Su ko defee, lépp lu jëm ci wàllu gënalante mën a wàññeeku ci réew mi. Ak foo mën di nekk, li nga soxla ciy xibaar wàlla ciy këyit mu mën a jàppandi ci yow.

Loolu nag, mënuñu ko am fii ak lënd gi jàppandiwul ci li ëpp ci askan wi. Looloo sabab ñu taxawal naal wu am doole wii. Nde, kopparal gi mi ngi tollu ci 1 105i miliyaar. Ñu tënk ko ci li ñuy dippee “Le Digital Master Plan” boo xam ne, am na lu tollu ci fukki sémb ak ñaar, juróom-fukki naal yu am solo ak ñeenti poñ. Bi ci jiitu di moom sunu bopp ci wàllu xarala. Bi ci topp di yaatal xarala gi campeef yi. Bi ci toppaat di suqali koomug xarala gi. Bi ci mujj di def réewum Senegaal li ñuy dippe “leadership africain dans le numérique”.

Ñoom nag, yemuñu foofu rekk. Ndax, taxawal nañu ag kurél gu war a doxal loolu. Kurél googu ñi ngi ko tudde “Conseil National du Numérique”. Mu am lu tollu ci ñaar fukki way-bokk. Ñi séq kurél googu, ñii la : Muhammet Mbeng, Aminata Njaay Ñaŋ, Basil Ñaan, Àntuwaan Ngom, Baydi Si, Maysa Faal, Dahiiru Caam, Kura Tin, Maam Faatu Wan, Mustafaa Siise, Omar Siise, Hamidu Ja, Ibraahima Nuur Edin Jaañ, Nafi Jaañ, Momar Jóob, Siidi Jóob, Isidoor Juuf, Asan Géy, Ndey Faaba Ñing.

Kon, ñu gis ne, naal wii bokk na ci yenn yi Njiitu réew mi taxawal fan yii. Mu doon naal woo xam ne kenn werantewul soloom ci jamono jii ñu tollu. Looloo tax, Njiitu réew mi fas yéene xar tànku tubéyam ngir askanu Senegaal mën a gis seen bopp bu baax ci wàll woowu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj