KAAJARUG SÉMBUW SOPPI SENEGAAL FII AK 2050

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sémb wi ñu doon coow ay at, ay weer, ay ayi-bés, mujj na a yemb. Tey, ci altine ji, 14i pani oktoobar 2024 lees ko doon aajar fa CICAD (Centre International de Conférences Abdou Diouf), nekk fa Jamñaajo. Kaajar googu, ñi ngi ko doon defe ci njiiteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak ci teewaayu elimaanu jëwriñ yi, way-bokk yi ci Nguur gi, kilifay diine yi, ñi ñuy dippe “corps diplomatique” ak “secteur privé” bi. Mu nekkoon ndaje mu am solo lool. Dafa di, foofu lañu doon waxe Saa-senegaal yi fan lañu bëgg a jëme réew mi fii ak atum 2050. Maanaam, fii ak ñaar-fukki at ak juróom, wan sémb lañu namm a doxale réew mi.

Sémb wi, maanaam “Le Projet”, nees koy waxee moo fi wuutu PSE (Plan Sénégal Emergent). Sémbu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dina romb wow ki fi nekkoon Njiitu réew, di Maki Sàll. Nde, moom, aw sémbam da koo natt fii ak 2050. Li mu dugge sémbam woowu mooy soppi réewum Senegaal ci fànn yépp. Muy lu ci deme ni wàllu koom, Yoon, nekkinu askan wi, añs. Te, lépp lalu ci li ñuy wax ñoom muy jub, jubal ak jubbanti. Kenn umpalewul ne, réewu Senegaal, koom gi xaw na a sooxe lool. Ba tax, ñoom, seen mébét mooy ñu fexe ba ni koom gi ajoo ci ñeneen mën a wàññeeku. Maanaam, dañuy dooleel li fi nekk. Muy ci wàllu balluy mbindaare yi, boole ko ak yem ci li ñu yor ci ay nit. Moom, Njiitu réew mi, dafa bëgg a jox kóolute doomi réewam ci liggéey bii mu sumb ak fu ñu mën a nekk. Muy fi biir-réew mi, di fa bitim-réew. Ci gàttal, yitteem, mook ñi mu àndal mooy tabax Senegaal gu bees. Senegaal goo xam ne, dina moom boppam, dina naat te, lépp dina tegu ci njub.

Dafa di, moom, sémb wi mu jaay askanu Senegaal daf ko misaal ci ag guy. Te, ñépp xam nañu ne guy li ko ëmb mooy ay reen, ab dàtt, ay car ak i doom. Te, pàcc bu ne ci garab gi am na lu muy wund ci naal bi. Reeni sémb wi ñooy misaal yorin wu sell te mucc ayib. Dàtt bi di yokkute gu sax. Car yi mooy am ay nit ñu xareñ boole ko ak yemale ñépp. Doom yeey fexe ba am koom gu dëgër. Koom goo xam ne, dina mën a joŋante ak yeneen yi ko ëppoon doole.

Kon, mel na ne sémb wi bàyyiwul wenn fànn. Fu nekk, cuq nañu fa. Te, fas nañu yéene doxal banqaas yépp ba fi ñu leen fekkoon mën leen fa a rombale. Te, yokkute googu, du am xàjj-ak-seen. Banqaas yépp lañu bëgg askan wi gis ci ay coppite. Maanaam, moom, Njiitu réew mi, li mu dige ci la bëgg a wéy, muy jub, jubal ak jubbanti.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj