KAARAANGE TALI BI : NDOG YEE NGI WÉY DI FAAT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bëgg-bëggu Nguur gi moo doonoon wàññi limub ndog yi ci tali bi ba, fii ak 2030, fu téeméeri ndog daan am, ñu mën a fàggu juróom-fukk yi. Waaye, dafa mel ni ndog yi dañoo gën a takkarnaase donte ni jot nañu cee jël i ndogal.

At mu nekk, 700i doomi-aadama dinañu ñàkk seen i bakkan ci ndog yiy am ci tali bi. Muy lim bu doy waar bu Buubakar Jóob, fara-caytu bu mag bu ANASER (Agence Nationale de Sécurité Routière) biral. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, lim bee gi mu jële ci takk-der yiy saytu kaaraange gi (Forces de défense et de sécurité).

Naka noonu, muy xamle ni du ñàkk sax limub ñi ciy ñàkk seen bakkan ëpp 700. Nde, woññib takk-der yi, ñoo ngi ko yamale ci ñiy faral di ñàkk seen i bakkan ci saa si. Boolewuñu ci ñiy faral di ñàkke seen bakkan ci raglu yi, ginaaw gaañu-gaañu yu metti yi ñuy am ba ñu rawale leen.

 Anam bu ni mel, tax na ba Nguur gi dogu ci ngir wàññi limub ndog yi bu baax fii ak 2030, ba fees daan gis 100i ndog, ñu fexe fàggu 50 yi. Muy nag jubluwaay bu am solo bu aju cib naal bu Mbootaayu Xeet yi (ONU) di dooleel ngir xeex bu baax ndogi tali bi.

Donte ni Nguur gi jot naa cee jël ndogal yu am solo, ndog yee ngi wéy di faat i bakkan. Ci ayu-bés bii rekk, ñeenti ndog am nañu ci tali bi, 20i doom-aadama ñàkk ci seen i bakkan. Lu ci gën a doy waar nag mooy lu ëpp ci njombe yi dara waralu leen lu dul doxalini nit ñi : yu deme ni xél yu metti, ñàkk a foog, tali bu bon, ñàkk a sàmmonteek digle yi ak ñàkk a tegaate daan yi ci war.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj