KAASAMAAS : DELLUB DAW-LÀQU YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Door nañu sémbuw jàPpandal dellub daw-làqu yi fa Kaasamaas. Tay ci gaawu bi, 11i fani sãwiyee 2025, lañu doon ubbi jéego bu njëkk bi (la phase pilote) ci kilifteefu Maymuna Jéey, jëwriñ ji ñu dénk wàlluw njaboot geek ndimbal li.

Ci diirub ati 2024 ak 2025 lañu àppaloon ndorteelu dellub daw-làqu ya woon ci xeexub kaasamaas bi. Muy sémb wu ñu gën a miin ci PADC (Projet d’accompagnement des déplacés de retour en Casamance). Waaye, ci yoor-yoorub gaawu tay bii la jëwriñu njaaboot geek ndimbal li, Maymuna Jéey, sog di ubbi jéegoo bu njëkk bi fa Sigicoor, ci teewaayu Moor Taala Tin (gornooru Sigicoor, kilifay bànqaas gi, kilifa aada yeek yu diine yoy gox ba).

Sémb woowu, dees ko nisaroon ngir taxawu nit ñi dawoon seen dëkki cosaan ci sababu xeex bi, gunge leen ba ñu mën añibbi seen i kër. Koppar gees jagleel naal waa ngi tollu ci 4.698.000.000i FCFA (ñeenti tamñaret yu teg juróom-benni téeméer ak juróom-ñeen-fukk ak juróom-ñetti tamndareet). Ñu waroon ko sottal ak naal wu tembare wees jagleel yeesalug yoon yeek gox yi fegge yi PUMA (Programme d’urgence de modernisation des axes et territoires frontaliers).

« Sémb wii, lees ci namm dëgg mooy yombal dellub sunuy mbokki askan yi bawoo kaasamaas, te xeex bi jële leen fa ci lu dul seen sago, ñu bàyyi seen i suuf, seen i kër, walla lenn ci ñoom ngir rawale seen i njaboot. » (Maymuna Jéey).

Naka noonu, jëwriñ ji joxe na fa jumtukaayi tabax ay dëkkuwaay ngir 133i njaboot yu dellusi fa diiwaanu Sigicoor. Joxe nañu fa itam 3i àmbilãs ñeel raglub Sigicoor (Hôpital de la paix de Ziguinchor), bokk-moomeel bu Jibijon ak bokk-moomeel bu Jawbe Kabendu.

Cig pàttali, xeexub Kaasamaas bi bokk na ci xeex yi gën a yàgg fi Afrig ginnaaw bi mu jóge ci notaangeg nasaraan si. Moo ngi dooroon ca atum 1982. At yu mujj yii, xeex baa ngi doon wéy di gën a dal donte ni ay junniy junni doom-aadama loru nañu ci, koom-koomu gox baat jaare ca nasax.

 Ñaari at ci ginnaaw, làrme bi amaloon na faat yëngu-yëngu yu yaatu ngir feg bànqaasi way-fippu ya fa gën a fés, ngir jàmm ji gën a dellusi foofa, ba nit ñi dawoon mën a dellu ci seen i dëkki cosaan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj