Kàddug Maki Sàll, Njiitu réew mi (AMI MBENG)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndakaarook biir Senegaal amoon nañuy yëngu-yëngu yu metti : ñu bari ñàkk ci seen bakkan, ñii seen alal, ña ca des, ñu taal seen i kër. Musiba bi dem ba jéggi dayo ; njiitu réew mi Maki Sàll yëkkati ay kàddu, waxtaan ak réew mi ngir jàmm dellusi.

Ci guddig 8eel fan ci weeru màrs, bi 20i waxtu jootee la woon.

Lu Defu Waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ay kàddoom na mu leen yëkkatee woon.

Salaamu aleykum, mbokki Senegaal yi !

Damaa fas yéene waxtaan ak yéen ci xew-xew yi am ci réew mi, xewee fii ci Ndakaaru ak ci yeneen i dëkk ci biir Senegaal. Lu ni mel nekk lu tiis, lu metti la, ànd ak ay nit ñu faatu, indi ay yàq yu am solo.

Sama kàddu gu njëkk ci guddig tey jii, mooy di jaale mbokki ñi faatu te it di mas-sawu ñépp ñi nga xam ne yàqal nañ leen, moo xam ndax seen kër la, seen bitig walla seen bérébi liggéeyukaay. Loolu tax na ba ñoom ñépp, maa ngi am xalaat ci ñoom di leen xamal ne nguur gi du leen fàtte.

Maa ngi xalaat itam ñi nga xam ne am nañ ci ay gaañu-gaañu, dinan leen jàppale ngir ñu mën a faju. Réew mi nag, benn bopp la, kenn mënu koo xar ñaar. Ndax Senegaal, walla sax «Sunu gaal», danoo war a joowandoo. Lii nu fi gis fan yii, lu yees la, ndax politig yàgg na fi am, xëccoo yàgg fee am, doxu-ñaxtu waxi-noppi. Waaye, yëngu-yëngu yu mel nii, daanaka guléet mu am fi. Bu dul woon taxawaayu làrme beek sàndarmëri ak pólis, ak dal gi ñu àndal, kon tey jii leneen lañuy wax. Ñépp gis nañu ne ay bérébi liggéeyukaayu nguur gi, ak yi yor kaaraange réew mi, lu mel ni birigaad, sàndarmëri, pólis, song nañu leen, loolu lu bees la ci miim réew. Màngasin yi ñu song, jël lu fa doon marsandiis (njaay) teg ci taal leen bañu jeex tàkk, indiwaat na jafe-jafe ci seen i boroom ak ña fa doon liggéeye.

Nit nag mën ngaa mer, am say xalaat, sañ ngaa bañ a ànd ak liy dox ci biir réew mi. Waaye jàpp naa ne dara warul a tax ñu fexe ba deret di tuuru, di taal ak di yàq loo xam ne nun noo ko bokk liggéey bi réew mi moome boppam ba léegi.

Gis naa taxawaayu kilifa diine yi, rawatina njiital xalif yi. Maa ngi leen di sant, di leen gërëm, di am mbégte itam ci ñi nga xam ne yónnee nañ ma mboolo mu takku ci ñaari fan yii nu génn. Muy kilifa diine yi, xalif yi, kilifa aada yi, waa jàngu bi, ñiy yëngu ci wàllu politig wi, ba ci ñenn ci kujje gi, way-moome yi, sàndikaa yi ak ndajem-njaatige mi (patronat), ñoom ñépp déglu naa leen, dégg naa leen itam. Mënuma bañ a jëfe ndénkaane yi nga xam ne moom lañ ma digal, rawatina yu kilifa diine yi. Ndax képp kuy wut jàmm ci réew mi, jàpp naa ne ki jiite réew mi ngay gën a wutal jàmm. Te, lépp lu laal askanu Senegaal, ak ku mu mënti laal ci lu metti, ci man mii lay gën a mettee. Moo tax, li ñu ma ñaan di doxal jàmm, dinanu ko def, fexe ba ñu wàcc, jàmm am ndax jàmm loo ko jënde jar na ko. Lii rekk moo waral nu doxalee nii.

Man mi Yàlla def ma jiite réew mi tey jii, lépp luy sama kàttan ci nguur gi, naa ko def ngir jàmm. Jàmm joojee ñuy ñaan mu dellusi ci réew mi ak dalug Senegaal ñoo ma yitteel. Bu ko defee, Senegaal melaat niñ ko xamee woon démb ak bërki-démb : réewum jàmm, dal, waxtaan ak demokaraasi. Waaye réew la moo xam ne itam, nit ñi suñ bokkul xalaat, dinañ weccoo ay xalaat. Léeg-léeg sax ñu wax ba dënn yi tàng, waaye li nga xam ne moom lañu bokk, muy réew mi, ak demokaraasi bi, ak campeef yi, waruñu koo yàq te kenn warul dugg ci lu koy yàq. Maa ngi santaat, di gërëmaat kilifa yi.

Sunum réew nag, Yàlla moo nu baaxe mbir. Fu mbir yi jaxasoo ba ñépp tiit, kilifa yi ñooy jóg waxtaan ak kenn ku nekk, di nguur gi, di kujje gi, ak ñi nga xam ne ñoo yëkkati mbir mi, ngir ñu xool ci yan anam lañu leen di lijjantee ba jàmm dikkaat.

Leneen li tam, xam naa ne am na ci réew mi ay jafe-jafe ci wàllu koom. Ndax àddina sépp a amey jafe-jafe, rawatina réewi Afrig yi, ba ci Senegaal gii. Li yokk jafe-jafe yooyu, mooy mbas mi fi dugg lu ëpp at a ngi nii. Ndax dafa indi ay gàllankoor ci njaboot gi, ci koom gi, ci këri liggéeyukaay yi ba mu am ñu ci ñàkk seen liggéey ; mbas mi bàyyiwul it ñi yor diine ji. At a ngi nii kenn mënatul doxal diine ba mu jag ci réew mi. Ci gàttal daal, mbas mi tax na jafe-jafe yi gën a tar. May wax askan wi ne, yég naa ko te dafa gën a yokku ba ci biir kër yi ak ci biir gox yi. Dégg naa it ni ngeen koy naqarloo.

Naam, bi mu tàmbalee, xam ngeen ne ci fàttali, dajale woon naa fi xaalis bi ñu tuddee « force covid19 ».  Xaalis boobu, daaw, jël nan ci junni miliyaar def ko ndimbal lu jëm ci askan wi. Yéen a ngi fàttaliku ceeb bi nu fi joxe woon, ak lépp li nu indi woon ngir jàppale njaboot yi. Joxoon nan tamit ay ndimbal « entreprises » yi ngir ñu bañ a wàññi ña fay liggéeye. Ba ci sunu doom yi nekk bitim-réew fàttewun leen, artist yi, naka noonu, bàyyiwun leen ginnaaw. Waaye, xam naa ne li nu jot a def lépp doyul. Ndax jafe-jafe yaa ngi fi ba léegi di gën a tar.

Ci wàllu xaalis bi nu dimbalee ndaw ñi, 60i milyaar DER joxe na ko waxtu wii may wax ak yéen, dooleel ci lu ëpp téeméeri junni ak fukk ak juróom ci ay GIE ak i kurél.  Ñeen-fukki milyaar ñoo ngi koy def at mu nekk ci wàllu tàggatub ndaw ñi, utal leen liggéey, moo xam ay àpparànti lañu, ak lu mu mënti doon ndax su ñu noppee, nu ubbil leen ay bérébu liggéeyukaay, jox leen xaalis.

Waaye loolu lépp gis naa ne doyul. Yéen ndawi réew mi, dégg naa bu baax seen yuuxu, seen mer, ndax xam naa ne ñàkkum xéy gi metti na. Te, seen xalaat yépp mooy noo leen di def ba tekki, am xéy, jàppale seen njaboot ak seen réew. Ndax ndaw loo gis, bëgg naa tekki, jàppale boppam, njabootam ak réewam. Loolu nag moo waral ma bëgg, bu lii weesoo, xamal leen ne dinaa def doxalin bu bees ci nguur gi ak “budget” bi ni nu ko daan doxale. Defar ay yoon, ay bérébu fajukaay, jàngale, lépp a am solo, waaye war nanoo toppatoowaat lu ëpp lu nu doon def ci ndaw ñi. Loolu njàngat la goo xam ne, dinan ci indi ay doxalin yu bees. Kon nag, yéen ndawi Senegaal, bu fekkee rekk ne seen mbirum ëllëg la, ak naka lañ leen di jàppalee ba ngeen tekki, na ngeen xam ne dinanu yokkaat lu bari. Maa ngi mébét naal bu bees bu tollu ci ñetti téeméeri milyaar ci ñetti at yiy ñëw, muy téeméeri milyaar at mu nekk ngir nu mën a jox xaalis képp ku ñu tàggat. Nu fexe ba woyofal tamit jaar-jaar yeek doxalin yi.

Umpalewuma ne guural gi indi na gàllankoor yu bari ci yenn liggéey yi, lu ci mel ni boroom lekkuwaay yeek otel yi, ñi yor liggéeyu guddi. Guural gi, li ko waral mooy sàmm dundi doomi-aadama yi.  Naam, koom gi am na solo, waaye ku gis ñi faatu ci Senegaal, bu dul woon bile doxalin kon mu gën fee metti. Te gis ngeen réew yu nu ëpp doole fuuf ci àddina si, am lu ëpp juróom-benn téeméeri junni doomi-aadama yu faatu, te loolu jàpp naa ne xajul ci sunu réew.

Lii moo waraloon metit yi ak guural gi. Bés niki tey dinan wàññi guural gi amoon biir Ndakaaru ak Cees. Ñaari dëkk yooyu ñoo am lu ëpp ciy këru liggéeyukaay ak it lu ëpp ci ñi ame jàngoro ji. Tereb-génn guddi gi moom, dinanu ko toxal, mu jóge 9i waxtu ci guddi ba minwi jëm 5i waxtu ci fajar, loolu dina tax yenn liggéeyukaay yi mën a ubbiwaat ci guddi gi.

Kon mbokk yi, li ma bëgg waxaat mooy sunu réew mi ak réew moo gis, su jafe-jafe bu mag amee, lay tax mu mënal boppam mooy nit ñi boole seen bopp doonte am nañ ay jafe-jafe ci seen biir, ndax mënul ñàkk ci àddina. Su ko defee li nu bokk di «Sunu gaal», dara du ko yàq. Ndax réew mi nekkul rekk lu tëb am, am  na junniy-junniy at, mbokk yi bokk deret, bokk diine, nekk ci jàmm, muy diine islaam walla bu kercen bi ak i yeneen diine, ku nekk nekk ci la nga gëm. Waaye terewul ñu bokk ndey ak baay, te loolu àddina sépp a ko nawe Senegaal. Kon loolu warunu koo yàq, te man de, feek maa ngi ci boppu réew mi, dinaa def sama kemtalaayu kàttan ngir dooleel demokaraasi, moom-sa-bopp, jàmmoo ak mbokkoo diggante nit ñi ci réew mi. Mbokki Senegaal yi ! Ci bésub tey bii, di juróom-ñetti fan ci weeru mars, ngeen xam ne moom lañ jagleel jigéen ñi ci àddina si, maa ngi ñaan waa réew mi, kenn ku nekk ak fu mu mënti féete, dox ngir jàmm ji gën a sax, dal gën a am, ñu jàgleel ko sunu jigéen ñi. Maa ngi jeexal ci di santaat, gërëmaat, ginnaaw sunu Boroom, kilifa diine yi, yu aada yi, bànqaas yi nekk ci biir réew mi yépp. Ñi dox ak di woote ngir jàmm sax ci biir réew mi te wéy di doxal yoon wi.

Kon noo ngi leen di jaajëfal mbokk yi, nu fanaan jàmm.

Ami Mbeng

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj