Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dina yékkati ay kàddu jagleel ko askan wi. Magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, moo ko xamle. Kàddu yooyu, bu jógee réewum Siin ma mu demoon la koy yékkati. Li ko sabab nag, bees sukkandikoo ci li Sëñ Usmaan Sonko wax, mooy tolluwaayu réew mi.
« Dafa am nu nu fekkee réew mi. Waxoon naa ko bu yàggul dara, nit ñi am nuñ ko gisee. Waaye, Njiitu réew mi dina wax ak askan wi bu ñibbisee. Dina xamal Saa-Senegaal yi anam wi nu fekkee réew mi. »
Barki-démb, ci gaawu gi la magum jëwriñ yi biral xiibar bi. Fekk mu doon jiite fa Maatam ñeenteelu bésub set-setal bi Njiitu réew mi sumb. Yokk na ceet ne, bu Njiitu réew mi noppee, jëwriñ yi dinañu ko feelu ciy faramfàcce ak i leeral.
Ba tey, fa Maatam ga mu demoon, magum jëwriñ yi xamle na fa bànk bi ñu bëgg a tijji, jagleel ko Móodu-Móodu yeek Faatu-Faatu yi, maanaan bànku jasporaa bi. At mu nekk, waa jasporaa bi dinañu dugal ci réew mi lu ëpp 1 500i tamndareet ci sunuy koppar. Te, xaalis boobu, moo ëpp fuuf ndimbal yi réew miy jot ñeel naali yokkute yi. Alal jooju la Càmm gi bëgg a yoonal, jagleel ko bànk. Muy nag naal bu Càmmug Maki Sàll njëkkoon a tudd ca atum 2019, waaye mujjeesu ko woon jëmmal.