Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay yékkateeti na ay kàddu. Muy i kàddu yu mu biral ngir gindi askan wi ci doxalinam ak di sàkku ci Saa-Senegaal yi ñu bennoo, bennale réew mi tey jéggalante.
Barki-démb ci àjjuma ji, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay doon na janook taskati xibaar yi. Mu daldi fay yékkati ay kàddu ci doxalinam ak tolluwayu réew mi, rawatina wotey Ngomlaan gi ñu dëgmal ak ndogal yi mu mujje jël.
Ca janoo boobu nag, Njiitu réew mi fésal na fa dogoom ci fas yéene amal wote yu mucc ayib. Ñaanal na itam Saa-Senegaal yeek way-pólitig yi ñu amal kàmpaañ bi ci jàmm, dagaan baati askan wi ci dal ak ngor.
Bu weesoo loolu, xamle na li mu seetlu ci réew mi. Am na ay kàddu ak ay xeeti jëfin yu ñuy faral di fésal fan yii te mu nirook lool ak ay xeeti boddante. Am na sax ñu yegg ba ciy tëkkoonte ci pénc yi, ci saabalukaay yi ak ci mbaali jokkoo yi. Seetlu bii nag, tax na muy fàttali ni du ci anam yii lañ war a fésalee sunuy uute. Ba tax mu dellu di fàttali Saa-Senegaal yi ni wote yi waruñu nekk poroxndoll ngir féewaloo. Moo tax muy woo ñépp ci dal ak yemale seen bopp.
« Ak wote yii di ñëw, maa ngi woo Saa-Senegaal yépp, rawatina way-pólitig yi ñu moytu di ànd ak a ëppal ci seen i kàddu ak seen i jëf »
Naka noonu, muy fàttali bu baax ni mu waree ci képp ku nekk mu sàmm li Senegaal di ndamoo te muy dal ak demokaraasi.
Bu weesoo loolu, Njiitu réew mi wax na ci ni ñu bari wonee seen ñàkk ànd ci yenn ndogal yi muy jël. Muy nag lu yenu maanaa ci moom. Nde, loolu mooy demokaraasi. Ma-xejj yépp, ñi fare ci Nguur geek kujje gi, am nañ sañ-sañu wone seen ñàkk ànd ci ni muy doxalee.
Bu dee tabb gi mu tabb ab PCA bu bokkul Pastef, leeral na ni dara yitteelu ko ci lu dul tëdde njaaxaanaay, nekkal fi képp kuy ma-xejj. Te keroog ba ñu ko fale la tekki ndombog-tànkam ci Pastef ngir mën ko jooxe. Moo tax muy woo Saa-Senegaal yépp ci bennoo, boole réew mi muy benn, tey jéggale. Nde réerewuñu mbir ni ci jamono ju yëngatu lañu jóge. Ba ci biir kër yu bari, réeroo am na fa ndax waxi pólitig. Te loolu war nañu ko weesu.
Bu dee ci wàllu Yoon itam, Njiitu réew mi biral na ni du mës a gàllankoor Yoon ci liggéeyam. Ba tax na du làq kenn ku Yoon di topp, ak loo ko jege jege walla nga jege magum jëwriñ yi.