KÀDDUY NJIITU RÉEW MI CI BÉSUB MOOM-SA-RÉEW BU SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci àjjuma ji, 4i fan ci weeru awril 2025, Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay doon na amal aw waxtaan ak ñenn ci saabalkati réew mi, bi 21i waxtu jotee ci guddi gi. Fekk lu jiitu loolu, njëkkoon na jiite, ci yoor-yoor bi, maaj bi ñu doon amal fa béréb bi ñu duppe Mamadu Ja ngir màggal 65eelu moom-sa-réew bu Senegaal. Ci kàddu yi mu jot a yékkati ca jotaay boobu, Njiitu réew mi dellusi na ci tolluwaayu réew mi, Nguuram ak i mébétam.

Bu dee ci maaj gi mu doon jiite, Njiitu réew mi rafetlu na bu baax nees ko waajalee ba mu am ci anam bu taaru bi ñu gis. Rafetlu naat déggoo bi am ci diggante ma-xejj yi, sóobare yeek takk-der yi te mu doon luy wane xelum làrme réew mi. Naka noonu, mu dellu yëkkati fay kàddu woote jëme ci askan wi ngir ñu bennoo, yokk lëkkatook takk-der yi ñeel kaarange réew mi. Ñuy i kàddu yu ñeel askan wi ci bés bi ñuy màggalee sunu moom-sa-bopp.

Doon nañu itam ay kàddu yu mu jagleel ganam yi mu fa dalaloon, rawatina Njiiti réewi Muritani, Gàmbi, Gine Bisaawo ak Niseriyaa. Mu leen di woo ci jamono yii ñu gis ne diiwaanu Afrig sowu-jant yëngatu na, ñu àndandoo ngir feg lépp lu nar a dal ci kaw seen i réew ak di leen gàllankoor, teg ci xel mu màcc.

Tolluwaayu réew mi ginnaaw at mi mu am ci boppu Nguur gi bokk na ci li gën a fés ci yees ko doon xaar. Naka noonu, jotoon naa xamle ci alxames ji ni dina wéyal wàññeekug dund bi ngir féexal Saa-Senegaal yi, sàmm seen wér-gi-yaram ak kéewnga gi.

Njiitu réew mi wax naat ni Senegaal moo ngi ci yoonu wut xaalisu boppam. Ndax FCFA bi ñuy doxalee koom-koomug réew mi doonul lu leen di teg ci yoonuw suqaleeku. Te moom-sa-bopp ci sa xaalis dafa am solo lool ci koom-koomug réew, rawatina bu nekkee ciy jafe-jafe.

Bu dee ci géewu pólitig bi ak jàppal bàyyil yi ci am, Njiitu réew mi wax na ci, rawatina ci caabal gi ëttu cettantal bi génne woon ca weeru féewirye ak toppe yi ci war a am. Naka noonu, muy xamle ni mënul a xam lu tax ñuy topp ay lijjantikat yu def te bu dee way-pólitig yi ñuy yuuxu naan « faj mer la », fekk ñoom ci seen bopp dañu taq ciy luubal yu am ci alalu askan wi.

Ba tay ci jàppal bàyyil yooyule, xamle na ci ni Càmmam du dugal loxoom wenn yoon ci mbiri Yoon. Bu amee kuy taxaw temm Yoon ngir mu def liggéeyam, Saa-senegaal yi lay doon. Ni Yoon di doxe bokkul ak pólitig bi. Waaye dafa war a doxal ci jéego yi ko askan wi tax muy àtte bëgge.

Bu dee ci wàlluw Nguur gi ak i mébatam, Njiitu réew mi fàttali na ni bi muy dagaan baati askan wi ca atum 2024 ngir jiite Réew mi, bokkoon na ci yi mu dige woon ni dina taxawal nguur guy doxal gu wareefu (un pouvoir exécutif responsable), boole kaak wàññi doole yi ñu jagleel Njiitu Réew mi. Ci noonu, muy xamle ni ci tànk yooyu la nekk. Nekkul ci yoonu aamaayoo léppi Nguur gi. Du sãru Njiiti réew yooyu di dajale dooley Nguur gépp, téyeel ko seen bopp. Nde laata muy falu, seetlu woon na ni ñu daan ëppale ci dëxëñ léppi Nguur gi ci loxoy Njiitu réew mi. Loolu tax na koo am yéene séddale ci anam yu digg-dóomu pàcci Nguur gi.

Séddaliyin boobu sax, li mu ci namm mooy tëggaat campeef yi. Mu nekk lu ñuy def, sukkandiku ci ci tënk yees jàppoon ci péncoo yi fi amoon ca atum 2009 ak waa CNRI (Commission nationale de réformes des institutions), ci njiiteefu ndem-si-Yàlla Aamadu Maxtaar Mbow (2021-2024).

Ngir gën a xirtal Saa-Senegaal yi ñu dellu woolu campeefi réew mi, Njiitu réew mi xamle na pénco mi mu nar a woote keroog bésub 28 me 2025. Mu jàpp ni dina doon luy kóolite ci diggante askan wi ak campeef yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj