Démb ci guddig dibéer ji, yemoo woon ak fanweeri fan ak benn ci weeru desàmbar, la Njiitu réew mi doon janook askan wi. Mu nekkoon waxtaanam wu mujj ci boppu réew mi. Waxtaan woowu nag, laal na ci ponk yu bari. Li ci gën a fés mooy tënku mbooleem liggéey bi mu def ba ñu ko falee ak léegi. Ci gàttal bilaŋam diggante 2012 ak 2024 laata muy tàggatoo.
Nuyoo la Njiitu réew mi, Maki Sàll, la ubbee waxtaan wi, wax tolluwaayu réew mi laata muy dugg ci biir waxtaan wi. Li mu njëkkee mooy wax jafe-jafe yi réew mi jot a jànkonteel ak yàqute yi mu jur ci réew mi. Muy ñi ci ñàkk seen i bakkan, ñi ci jële ay gaañu-gaañu ak alal ji ci yàqoo ba ci sax njàng mi nga xam ne gàkk na ci. Nde, kenn umpalewul ne coow li fi amoon moo taxoon ñu tëjoon fi daara yu kowe yi ab diir. Daara ju kowe ja ca Ndakaaru ba tey ubbeegul i buntam. Nee na gën nañoo dëgëral seen taxawaay ba génn ci jafe-jafe yooyu. Dafa di ñoom dañuy góor-góorlu ci ndono li ñu fi fekk. Looloo tax ba yokkute gi indi ci réew mi mën nañu ko gis fépp ci biir réew mi. Ci lu dul yàgg dara dinañu siiwal seen bilaŋu liggéey bi ñu def ci réew mi bi ñu leen falee ak léegi.
Ci seen liggéey boobu nag, xamle na ci ne nafa gi jóge na ci 2.344.000.000.000 ci atum 2012 dem ci 7.003.000.000.000 ci atum 2024. Ci wàllu yoon yi rawatina ci otorut yi jóge nañu ci 32i kilomeetar ci otorut, tey ñu nekk ci 189i kilomeetar. Te, lu yàggul dara, dinañu dem ci 500i kilomeetar bu yeneen liggéey yi àggee. Naka noonu, saxaar yi tamit dinañu ci dolli yeneen yu bees. BRT bi tamit dinañu ko tijji fukki fan ak ñeent ci weeru saŋwiyee wii. Mu xamle ne PSE bi yemul foofu rekk, laaxaale na raglu yi, mbëj mi. Dëkk yi amoon mbëj ci atum 2012 ñi ngi tolloon ci 27 % dem nañu tey ci 61 % ci 2023. Te, bu ñu jëfandikoo soroj bi ak gil bi ñépp dinañu jot ci kuraŋ bi ci njëg yu gën a yomb.
Ci wàllum ndox mi tamit def nañu ci liggéey bu mucc ayib. Tuddaale na mbey mi, càmm gi ak napp gi nga xam ne, ciy waxam, seen njariñ kenn naatableetu ko ci réew mi. Kopparal nañu leen bu baax, yokk seen i jumtukaay yi ngir seen i njureef romb fi ñu leen fekkoon. Nee na ñi ngi dimbali ñiy yëngu ci wàllu mbatiit bu baax. Muy ñi nekk ci li ñuy duppee “cinéma” ak “artisans” yi tamit. Naka noonu ñiy yëngu ci liggèeyu daamar yi yokku nañu leen i jumtukaay yu gën a xarala ngir seen liggéey mucc ayib.
Ciy kàddoom ba tey, liggèeyam yemul foofu. Ndax, nee na ngir yemale geek dimbalante bi, kopparal nañu ay naal yu bari. Rax-ci-dolli, ñoom it amoon nañu ay naal ci wàll woowu, muy seen sumb bi ñuy duppee “xëyu ndaw ñi” ak yeneen yu ni deme. Te, ñi ngi jàpp ci njëgi lekk geek naan gi, dem beek dikk bi. Maanaam mbooleem li nga am ne askan wi daf koy yittewoo.
Naka noonu njàng meek njàngale mi dara demul mu des. Ndax, nee na, jël nañu ay jàngalekat, yokk nañu seen i peyoor tamit. Sos tamit ay béréb yu ñuy tàggatee ay ndaw ci yeneen i fànn. Ba ñu moomee sunu bopp ba atum 2012, sunu réew ñaari daara yu kowe kepp la amoon (UCAD, UGB) ak ñetti béréb yu ñuy tàggate muy Cees, Bàmbey, Sigicoor. Ci fukki at kepp ñu def béréb yooyu ay daara yu kowe. Tabaxaat yeneen ñetti daara yu kowe (Aamadu Maxtaar Mbów fa Jamñaajo, El Haaj Ibraahiima ñas fa Siin Salum, Université numérique Séex Amidu Kan) waxaalewuñu “Campus franco-sénégalais” bi ak tabaxug daara ju kowe ji nekk fa Maatam. Def nañu lu bari tamit ngir ndongo yi nekke ci daara yu kowe yi mën a am fu ñu dëkk ak lu ñu lekk.
Li ko waral mooy ci njàng mi la ndaw ñi di mën a tabaxee seen ëllëg waaye, du ci gaal yi. Mbooleem liggéey yooyu ñuy def moo tax ñu bëgg a saxal jàmm ci réew mi. Ba tax na, yokk nañu limu takk-der yi ak seen i jumtukaay. Ndax, fi jamono ji tollu lépp a jaxasoo. Muy woote ñu sàmm loolu ca gën-gaa rafeti càmmin.
Mu tëje cant ak ngërëm ci mbooleem ñi ko wóolu ba fal ko atum 2012 ba tey. Moo tax dina def lépp ba wote yii ñu dëgmal jaar yoon. Muy woo lawax yi tamit ñu jàppale ko ci loolu. Bu bés baa na ñépp xëy woteji ci jàmm. Ñaari fan ci weeru awril bu soobee Yàlla mu jox lenge yi ki koy wuutu ci boppu réew mi. Ra-ci-dolli, moom pare na ngir jàppale ki ko fiy wuutu. Ndax, fi ko réew mi tollu la.
Mu yokk ci ne bu joxee Nguur gi dina taxawal ag mbootaay guy dox ci jàmm, waxtaan ak suqaliku ngir wéyal liggéeyam ci fànn yoo xam ne daf leen a sopp lool. Diggante fii ak booba nañu joxantey loxo ngir Senegaal gu booloo gu suqaliku ci jàmm, kaaraange ak ug dal. Di leen sant di leen gërëm, di leen ñaanal, di leen wax déwénati.