Altiney tey jii mooy tollook juróom-ñeenteelu fanu kàmpaañ ñeel wotey 24 màrs 2024 yi. Boobaak léegi nag, lawax yaa ngiy wër réew mi, di dugg ci gox yeek goxaat yi ak ci dëkk-dëkkaan yi. Liñ ko duggee mooy waxtaan ak askan wi ngir yey ko. Dafa di, lawax bu ci nekk, sa mébét mooy jiite réew mi keroog dibéer ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru màrs wii. Moo tax, lawax boo ci gis, mi ngi lal ay pexe, di def lu mu mën ak lu mu mënul ngir askan wi jox ko bopp. Ndax kat, ku bëgg lem moom, war a ñeme màtt-màtti yamb. moo tax it, ci xëccoo bu metti la 19i lawax nekkee. Bu ñii di biral seen i naal ak i yéene ñeel réew mi, ñeneen ñi, ñoom, ñu ngiy sànnante xeer ak a tuumaalante. Ku nekk a ngi di tamm sa moroom dëmm ngir wuññi sa sutura, weer la ci kanamu askan ngir ñu bañ la woteel. Ñaari lawax yii di Basiiru Jomaay Jaxaar Fay (Pastef) ak Aamadu Ba (Bennoo Bokk Yaakaar) ñoo gën a fës ci yàqante boobu. ku ci mel ni Bubakar Kamara, moom, jàkkaarloo la woote ngir ñu gam-gamle naal yeek sémb yi, Saa-Senegaal yi natt ki gën a baaxle.
Benn ayu-bés kepp a des ci wote yoy, juróomi at ci ren ñu leen di xaar. Ba tax na, jamono jii, benn lawax nelawatul ba yàndoor. Muy ki fare ci Nguur di, di ñi fare ci kujje gi. Kenn mayul sa moroom dara. Coow laa ngi ne kurr. Wax jeek tuumalante yi bari lool. Bu dee ca njëlbeen ga waxees na waxtaane mbirum xaalis ak tof-njiit li nekk ci naalu Basiiru Jomaay Fay, jamono jii, wax ji dafa wëlbatiku ci jikko yeek jëmm yi. Daanaka, kenn waxatul lu jëm ci naal yi. Looloo tax, lawax bii di Bubakar Kamara di sàkku ci ñu amal ay jàkkaarloo diggane lawax yi, Saa-Senegaal yi àtte, tànn ki gën a baaxle naal, fal ko. Boobaak léegi nag, amagul tontu ci mbir moomu. Yeneen lawax yi, leneen a leen yitteel jamono jii, rawatina bob Pastef ak bob Bennoo Bokk Yaakaar.
Mbirum wote yi, yemul rekk ci dagaan baatu askan wi. Lu waay mën a def ba yàq xelu askan wi ci benn lawax bu mu xëccool, mi ngi koy def. Moo tax, lawax bu ñu ci jekku, dog sa baat. Maanaam, ci làmbi golo lees nekk ci misaal. Ku nekk mi ngi napp sa moroom. Basiiru Jomaay Jaxaar Fay daf ne, na lawx bu ci nekk génn wax, siiwal tolluwaayu alalam, wax fum ko jële. Lim ko duggee mooy leeral kan walla ñan ñoo gën a setle ay loxo. Sikk amul ci ne, kenn kesee ko tax wax lu ni mel, muy Aamadu Ba mu Bennoo Bokk Yaakaar.
Li tax Basiiru J. J. Fay joxoñ Aamadu Ba mooy dafa jàpp ni waa ji ni mu amee alal ju bari jees koy waxal lewul. Ndax, ciy waxam, moom ak Usmaan Sonko yépp, jot nañoo liggéeyandoo ak Aamadu Ba fa DGID. Muy bànqaas boo xam ne, li ëpp ci koppari réew mi fa lay jaar, ñu ko fay saytu. Ndeem, ñoom ñaar ñépp koppar gu dul jeex jaar na seen i loxo fa béréb booba ñu nekkandoo woon, dees na xam ku gën a set i loxo. Kan moo doon liggéeyal réew mi ? Ak kan moo doon duufal i jibaam, di duy ay poosam ?
Moom, Basiiru Jomaay Fay xamle na ci yégleem bi ne, dina biral li mu am ci ndoorteelu ayu-bés bii. Bu ko defee, mu xool ndax kii di Aamadu Ba dina ko ci feelu am déet.
Bu dee Aamadu Ba, moom dafa tontu, wax ne Sonko ak Basiiru Jomaay Fay ci yàq der lañ nekk ak wax lu dul dëgg. Mu neeti, kii di Jomaay, deesu ko dénk réew mi ndax amul xam-xam bi te matewu ko. Bu dee ci wàllu alalam, waa pekkoom nee nañ bés bu faloo dina ko siiwal ci kanamu àddina sépp.
fi mu tollu nii, buñ doon tënk kàmpaañ beek kàddu yi lawax yiy biral, genn kàddu dina ci doy : “Maa baax, yaa bon !”