KARIIM WÀDD : “DAMAY BOKK CI NII WALLA CI NAA…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaawu gii weesu la ndajem ndeyu àtte mi biral limu lawax yiy bokk ci wotey 2024 yi. Lawax yooyu ñi ngi tollu ci ñaar-fukk. Kii di Kariim Wàdd ak Usmaan Sonko nga xam ne ñi ngi leen ci doon bàyyi xel, ñoom duñu ca mujjee bokk. Usmaan Sonko moom, dafa bàyyi mu sedd. Waaye, Kariim Wàdd moom nee na du leen ko yombalal. Ndax, dina leen topp fa bànqaasu Yoon wa nekke fa CEDEAO. Naka noonu, dépitey PDS yi tamit nee nañu mbir mi dinañu ko lijjanti fa Ngomblaan ga ba mu leer nàññ.

Mu mel ni ndogal li ëtt boobu jël ñeel lawaxu PDS bi jur na mbetteel gu réy donte ne sax coowal nasiyonaaliteem jiitu woon na loolu. Ñoom jàppoon nañu ne coow loolu moom lijjantiku na. Waaye, yëf yi mujjeewu fa deme noonu. Moo tax bi ndogal li jibee, moom ndeyu-mbill ji moo njëkk a biral ci mbaali jokkoo yi ag ñàkk a àndam ci loolu. Ndax, nee na :

“Ndogalu ndajem ndeyu àtte mi laluwul ci firnde yu leer. Te, dafa salfaañe àq ji gën a yell ci moom muy bokk ci wotey 2024 yi. Ndax, moom bu yàgg ba tey yoratul nasiyonaalite bu Farãs.”

Moom ak i mbokkam nag dañoo jàpp ne am na luy ñuul ci soow mi. Ndax, ay caaxaan kepp lañu layalee gàntalug wayndareem wi. Dafa di, li mu gis mooy ne, gaa ñi fi ñu jàppoon 2012 ba léegi teggiwuñu fa seen loxo. Maanaam, dañu ko tëj lu ëpp ñetti at ba noppi ñu jaay ko doole, gàddaayloo ko lu tollu ci juróom-ñaari at. Waaye, nee na wii yoon moom du leen ci bàyyi noonu. Ndax, ciy waxam ba tey, dina dem fa bànqaasu Yoon ba nekke fa CEDEAO ngir mu mën a bokk ci wote yii di ñëw. Waaye, yemul foofu kese. Yokku na ci ne:

“Ak lu mën di xew, dinaa bokk ci wotey 2024 yi ci nii walla ci naa. Maa ngi woo samay militã, ñi may jàppale ak miliyoŋi saa-senegaal yi may dooleel ñu booloo ngir xeexle ma rëq-rëq yi am ci wàllu Yoon bañ delloosi fi Yoon.”

Ci gàttal, taxawaayu gaa ñi firnde la ci ne ñoom pareeguñu ngir yemale fii xeex bi. Ndax, li fi jot a xew, wékkuñu ko ci ndoddu ndajem ndeyu àtte mi kese. Nguur gi tamit duutaale nañu ko ci baaraam. Moo tax dépitey PDS yi ne dinañu taxawal ag ndiisog luññutu fa Ngomblaan ga (commission d’enquête parlementaire) ngir leeral anam yi ñuy génnee lawax yi ci joŋante yi rawatina seen bos. Li ci gën a yéeme mooy ñoom yemuñu foofu kese. Dañoo yokk ci xar mi karaw. 

Ndax, nee ñu, yëf yi dafa am ger ci biir, ay jàppale ma ci lii ma jàppale la ci lee. Te, ci juróom-ñaari àttekati ëtt boobu, am na ci ñaar ñu ñu duut baaraamu tuuma. Muy kii di Séex Tiijaan Kulibali ak Séex Njaay. Ba tey, ci seen yégle bi, xamle nañu ci ne fii ak fan yii di ñëw dinañu jébbal ab pelent ngir wone mbooleem ndëngte ak njuuj-njaaj yi am ci mbir mi.

Kon, day mel ni xeex ci wàllu Yoon mooy bëgg a des ngir wayndarew Kariim Wàdd mën a jàll. Ndax, moom ci jëmmi boppam ma ngay xeex fa bitim-réew. Ay ñoñam di wéyal xeex bi ci biir-réew mi. Dina bokk walla du bokk, dees na ci xam dara ci lu yàggul. Waaye, loo lijjantiwul woon ay at, ay weer, ndax, danga ko mën a lijjanti ci ay ayu-bés yu néew ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj