KAYIS SAYET WAXATI NA NJOMBE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réewum Tinisi li, namm naa andeeti coow ci diggante Tinisi ak Libi. Àtte bi CIJ (Cour internationale de justice, di ëttu àttewaayu mbootaayu xeet yi) dogaloon ci coowal dig ak soroj li doxoon ci diggante ñaari réew yi ci atum 1985 la dellu duut baaraam ci ayu bés bii weesu.

Bu yàggul dara, ci weeru féewaryee bii weesu, la kii di Kayis Sayet, Njiitu réewum Tinisi li yékkati woon i kàddu ba indi fi coow ci wàllu xeetal ñeel ñuuley Afrig yi. Coow loolu giifagul sax, mu yékkateeti yeneen i wax ci diggante Tinisi ak Libi. Wile yoon, du sax coowal xeet walla der wu ñuul walla wu weex. Waxu dig la, wu dox ci diggante ñaari réew yi ci biir géej gi te ëmb soroj bu bare lool ci barab bii di « champ pétrolier de Bouri ».

Moom Njiitu réew ma nag, dafa amoon doxontu ci barabi Etap (Entreprise tunisienne d’activités pétrolières) yi. Foofu la yékkatee yile kàddu :

«  Teeni soroj yu Buri yaa ngi nii. Daanaka Tinisi amu ci tus. […] Teen yii rekk mënoon nañoo dimbali Tinisi ba du am benn jafe-jafe ».

Waaye, wax ji doonul ju ndaw. Neexul wenn yoon kilifay Libi yi. Nde, dafa leen di niru ni waa ji, Kayis Sayet, dafa bëgg dekkil coow lu gilli woon ba fay. Ndax kat, waxu teeni soroj yu Buri yi nekkul lu bees. Lu ëpp 50i at ci ginnaaw, doonoon na fi coow lu tàng ci diggante ñaari réew yi. Ku ci nekk taxawoon temm ni teenu soroj yee ngi féete ci sa géej. Wax ji daldee dem ba mujj ci loxoy mbootaayu xeet yi.

Ci atum 1982 la ëttub àttewaayu mbootaayu xeet yi ca La Haye njëkk jël ndogalu rëdd diggante ñaari réew yi ci géeju Mediteraane. Bi ñu demee ba ci atum 1985, ñaari réew yi ànd cib déggoo buy wone ni Libi moo moom teeni soroj yi. 

Jamono yii nag, li dese leer àddina sépp mooy lu tax Njiitu réewum Tinisi li sulli jile wax ? Lu waral mu xaar ba àddina sépp di ko ŋawti-ŋawtee mu soog ciy wax ? Mbaa du dafa bëgg suul waxam ji woon ci boroom der yu ñuul ya ca réewam ? Ak lu mu ci mën a namm, li ci kanam rawul i bët. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj