Démb, ci ngoonu dibéer ji, elimaanu jëwriñ yi amaloon na ab doxantu fa Kolobaan ak fa tefesu “Anse Bernard”. Li mu ko dugge woon mooy leeral askan wi li ñuy nemmeeku fan yii yépp ci yenn béréb yi. Kolobaan nag la njëkkee. Kenn umpalewul ne, jamono jii, tuxal gi ñuy tuxal yenn ci jaaykat yeek yenn bérébi liggéeyukaay yu ñuy déjjati. Li waral loolu yépp, kii di elimaanu jewriñ yi indi na ci ay leeral.
Démb, ay tànki nemmeeku ak leeral la Usmaan Sonko doon dox. Waayeet, dafa doon dalalaale xeli askan wi nga xam ne, fan yii, ci njàqare la nekk. Ndax, bir na ne, ñu bari ci ñees di déjjati ak tuxal, ci seen njaay yooyee lañuy suturlu. Looloo sabab, bi elimaanu jëwriñ ji jëlee kàddu, dafa doore wax ci lan moo sooke mbir mi. Daf ci waxtaan Njiitu réew mi ba noppi, di ko biral ci kàddu yii toftalu :
“Fan yii yépp, ñi ngi dégg ay nit yu ñuy jële ci seen bérébi liggéeyukaay. Ndax, jot nga ci xibaar bi ? Maak yow noo ci xaw a yem. Li ma ciy dégg mooy li ñuy wax ci kibaaraan yi. Mu ni ma : “dama bëgg nga leerlu ba xam nu mu deme”. Ci laa woo jëwriñ ji ñu dénk wàllu biir-réew mi. Laaj ko nu mbir mi deme? Mu xamal ma ne moom jëloon na ab ndogal. Wax “gouverneur” yi ak perefe yi, lënkaloo ak meer yeek “présidents de conseils départementaux” yi ngir ñu mën a fexe ba lépp loo xam ne day gàllankoor yoon yi, ñu dindi ko. Ndogalam mooy yoon yi nga xam ne defar nañu ko, tabax, ay daamar war cee jaar, ay nit war cee mën a dox, bu ko dara gàllankoorati. Loolu ndigal lu mu joxe la. Defe naa ci la meer yu bari tënku ne dañuy déjjati ñoom it.”
Kon, bees sukkandikoo ci yile kàddu, jëwriñu biir-réew mi moo joxe santaane bi, njiiti gox yi di ko jëfe. Bi ñu jógee ci loolu, Sonko xamal na leen tamit li wund mooy dëgg-dëggi coow loolu. Ndax, nekk gi ak nekkin wi ci béréb yooyu, ñu baree ko séq. Du askan wi kesee sabab coow li. Dafa wax, moom elimaanu jëwriñ yi, ne :
“Njiitu réew mi, li mu ma yónni ma wax ko nit ñi mooy, foo dégg coowal nekk (occupation), ñett a ko séq. Meeri moo ko séq ak nit ñi nga xam ne ñoo fa am seen i kër, dëkk fa ak ndaw ñi nga xam ne dañoo bëgg a liggéey, amuñu fu ñuy liggéyee, ñëw di fa liggéeye. Te, ñett ñooñu ñépp, moom Njiitu réew mi moo leen njaboote. Kon, bu ñuy wut saafara, dañuy wut soo xam ne moo ëmb ñépp. Ginnaaw bi mu yegsee fii, déglu naa ñi fi nekkal askan wi, mooy ñi fi dëkk.”
Kon, nekkin wi, ñépp a ci am wàll. Ndax, du ku mu neex nga dëkk fu la neex walla nu mu la neexee. Du ku mu neex, lal walla lalee nu mu la neexee. Ndeem sax, ku mu neex mën nga def sa kër ay màngasin fii ak romboo fi ñu la yemloo. Waaye, meeri yi tamit, kenn demul ñu des. Nde, ñoom it, am nañu wàll wu réy ci mbir moomu. Ndax, léeg-léeg, mën nañoo joxe foo xam ne waruñu koo joxe ba noppi di ci feyeeku. Waaye, ñoom Nguur gi, seen wàll ci mbir mi mooy seetaan gi ñuy seetaan mbir mi, mu yàgg genn yàgg gi, ba jur li muy jur. Te, coow loolu di ci am lépp, lenn waralu ko lu moy li ñu ci ñàkk a boole ay matuwaay. Moo tax, mu neeti, moom njiitul PASTEF li’:
“Li ma laaj léegi perefe bi mooy, ndax am na ay matuwaay yu ñu jël ngir jàppale leen. Ndax, nit ki fi mu nekk di fa xéewalu, di suturlu, boo ko fa jëlee walla boo ko fa bëggee jële, dafa war a am ay matuwaay. Maanaam, nga jox ko dara lum dee-dee. Loolu nag, jotu fee am. Ñu koy naqarlu. (…) Nguur gi dina leen won matuwaay yi mu jël. Lañuy wax nit ñi mooy fu ñu leen di mën a yóbb, buñu xeeb. Ndax, ñépp xajuñu ci benn ja.”
Moom nag, li mu jàpp mooy ne li waral lii lépp mooy Nguur yi fi jiitu woon dañoo lajj ci seen i naal yi ñu laloon. Waaye, wii yoon, ñoom dinañu def lépp ba nekkin wi gën a mucc ayib, dem beek dikk bi gën a yomb ci biir dëkk yi. Nguur gi dina lënkaloo ak meeri yi ba ñu mën a am saafara yu mucc ayib. Ba nga xam ne, liggéey bii ñu sumb, kenn bañ cee gaañu. Muy askan wi ñu koy defal, muy meeri yi walla Nguur gi ci jëmmi boppam. Mu jàpp ne loolu yépp, waxtaan kesee mën a tax mu yemb.
“Te, di wax tamit, perefe bi, li ñu leen sant mooy waxtaan. Nun, sunu biir, nun Saa-Senegaal, nanuy waxtaan, di wax ak nit ñi. (…) Li ñu sant perefe, di ko laaj meer bi, di ko laaj ñi séq mbir mi yépp, mooy nañu toogaat ak ñépp, waxtaan, wut ay saafara yu ñu fa wuutale.”
Ci gàttal, elimaanu jëwriñ yi xamal na askan wi ne déjjati yeek tuxal yi, loxo Nguur génnu ci donte ne sax, am na yeneen banqaas yu ci am wàll. Li gaa ñooñu di xaar ci ñoom jamono jii mooy xool lan lañuy teg seen loxo ginnaaw bi ñu leen tuxalee. Nde, dige moom, bor la.