KOMISEER KEYTA TËDDI NA KASO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci ndigalu toppekatu Bokkeef gi, àttekatu 10eelu kabine bi dóor na « mandat de dépôt » komiseer ba woon, Séexna Keyta. Lees koy tuumaal mooy siiwalub xibaar yu wéradi. Ubbees na ab luññutu ngir leeral mbir mi.

Cig pàttali, Séexna Keyta, ñu gën ko miin ci turu komiseer Keyta, dafa defoon ab widewoo, di ci wax ne Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ak elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dañu doon xeex fa njénde la. Looloo taxoon waa DIC jàppoon ko, jébbal ko Yoon. Ginnaaw bi ñu dégloo nag, jàllale nañ ko ndungsiin, mu war fa tëdd, xaar àtteem.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj