KORONAAWIRIS, LOO NU NARAL ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

 
Ci bésub altine, 2eelu fan ci weeru màrs, atum 2020 la Covid-19 bi ganesi Senegaal. Xibaar baa ngi tukke woon ci jawriñ Abdulaay Juuf Saar mi yor wàllu wér-gi-yaram ak ndimbalug mbootaay gi. Benn doomu Farãs a ko indaale woon. Doktoor ya nekk ca Institut Pasteur tey saytu lépp lu aju ci jàngoro ji ñoo dëggaloon xibaar bi. Yéenekaay yépp xéye ko ci talaata ji, def ko ci seen i xët yu njëkk. Njiitu-réew mi génne 1 miliyaar ak genn-wàll, wàññi deppãsi liggéey yi ñeel bitim-réew. Ñu ne déet-a-waay, ci talaata ji, 3eelu fan ci weeru màrs, ñu gisaat beneen tubaab, ab farañse bu am 80i at bu ame covid-19 bi : muy 2 aji-tawat. Ca ëllëg sa, 4eelu fan, jawriñ ji génnewaat beneen yëgle, di ci wax ne Institut Pasteur fekkaat na doomu-jàngoro ji ci dereti yeneen ñaari nit.  Kenn ki dib jigéen ju am 68i at, di soxnay aji-tawat bi am 80i at. Moom, 29eelu fan ci weeru feewaryee la fi ñëwoon, àndoon ak jëkkër ji. Keneen ki, moom, ab doxandéem bu jóge woon ca réewum Àngalteer la, 33 at la am te mu ngi ganesi woon Senegaal ci 24eelu fan ci weeru feewaryee.  Boobaak léegi, nag, way-tawat yi dañuy gën di yokku.
38 way-tawat
Li ko dale altine, 2eelu fan ci weeru màrs ba tey jii, bés bu nekk ñu jot cib yégle bu bawoo ci njawriñu wér-gi-yaram geek ndimbalug mbootaay gi ñeel Covid-19 biy doxantu ci biir réew mi.
Ginnaaw yégle bi jiitu bi génnoon ci altine ji, 2eelu fan ci weeru màrs, jot nañoo génne 18 yégle yiy saabal ci Covid-19 bi ak dogal yiñ ci jël, lépp di 19 yégle. Yégle bu mujj baa ngi génnoon ci bésub 19eel. Bees sukkandikoo ci bi ci mujj, limu way-tawat yi yokku na ba àgg ci 38. Waaye, yégle baa ngi nuy xamal ne, 5 yi wér nañu. Ñi ci des, mënees na rafet njoort ci ñoom. Ngir bañ jàngoro ji law, njiitu réew mi jël na ay ndogal yu bare.
Ndogal yi
Ci bésub 14eelmàrs la njiitu réew mi wax ak askan wi, xamal ko naka la mbir mi tëdde ak yan pexe la nguur gi lal ngir xeex Covi-19 bi. Ci pexe yooyu, nag, bokk na ciy  ndogal yu bare  yi mu jël ngir aar réew mi, muy ay tere yi aju ci :
– bépp xew-xew buy waral am mbooloo di daje ci diirub 30 fan ;
– gaal yiy yab ay tukkikat ;
– tëjub daara yépp ci diirub 3 ayu-bés gën-caa-ndaw ;
– yokkute saytub wér-gi-yaram ci digi réew mi, muy digi suuf yi, yu géej gi ak bu jàww ji ;
– màggalub moom-sa-bopp gu ren ji, dees na ko yemale ci teewaayu soldaar yi doŋŋ ca pale ba ;
– nguur gi bëtal na lépp lu aju ci aji ren yi, muy yu jullit ñi ak yu kercen yi ba jëmmi-jamono ;
– Air Sénégal dakkal na tukki yi ;
– njiitu réew mi dina jiite ñaari ndajem kaaraange ayu-bés gu nekk ;
– njiitu réew mi taxawal na itam ag kurél guy xeex Covid-19 bi, dippe ko « Force-Covid-19 » ;
– jawriñ ju ne dina joxe 1 miliyoŋ ngir jàpp ci xeex bi ;
Waaye, njiitu réew mi waxul dara lu leer ñeel xew-xewi diine yi. Dafa rekk ñaan kilifa diine yi ñu dimbali nguur gi ci ndogal yi mu jël. Jaarul ci digg bi wànte li mu ci jublu mooy wax leen ñu fomm xew yiñ doon waaj a amal weer yii nu dégmal, rawati-na ca Tuubaa.
Ndege, ñi ëpp ci way-tawat yi Tuubaa lañ nekk. Te, ginnaaw Ndakaaru, Tuubaa moo ëpp ay nit ci Senegaal.Ab Móodu-Móodu moo jóge Itali, teersi Tuubaa, indaale jàngoro ji, wàll ko lu tollu ci 10 nit.
19 Móodu-Móodu yi caŋ Móritani
Ca njëlbéen ga, ay doxandéem ñoo ame woon jàngoro ji. Waaye, bi Móodu-Móodu Tuubaa bi ñibbisee, ci la ko wàll njabootam, mu tàmbalee law. Mu am, nag, ay Móodu-Móodu yu bare yiy daw réewi Tugal yi ame jàngoro ji. Ginnaaw biñ dakkalee tukki roppëlaan yi, ci suuf si walla géej gi lañuy jaare. Waaye, réewum Móritani dafa jàpp 19 ci ñoom, téye leen fa. Mu mel ni ñu ngi ci gutë.
Bennoo bokk xeex jàngoroy Covid-19
Wolof nee na, upp baax na ci laax bu tàng. Moo tax, jamono jii, réew mépp a ànd doon benn ngir xeex jàngoroy Covid-19. Muy kujje gi, kilifa diine yeek yu aada yi, ñépp a ràngu ci ginnaaw nguur gi ngir jàppale ko ci xeex bi. Kurél yu bare tamit, rawati-na way-moomeel yi ñoo ngi bey seen wàll ci waar wi. ARTP booloo na ak waa Orange, Free ak Expresso ngir ñaax askan wi ci matuwaay  yi nit ñi war jël ngir moytu Covid-19.
Siin a ngi wallsi Senegaal
Réewum Siin mi jëkk a ame mbas mi fas naa yéene jàppale nguuru Senegaal ci xeex bi. Ci noonu, àmbasaadu Siin ci Senegaal rotal nay xibaar yu bare ñeel ndimbal loolu :
– dinañ may réew mi ay jumtukaayi faj ci nim gën a gaawe ;
– nee ñu, ràllumaanu Siin bu siiw bi sos « Groupe Alibaba », Ma Yun (Jack Ma) dina may réewu Afrig mu ne 100 000 mask, 1 000 yérey aaru ñeel doktoor yi, 1 000 « écrans faciaux » ak 200 000 saytukaayi Covid-19 ;
– àmbasaad bi waxaat na ne, Groupe BGI dina may Senegaal 500 saytukaayi Covid-19 ;
– liggéeykati Siin yi dinañ lëkkook yu Senegaal yi ngir soppi loppitaanu Yaay-Doom bu Jamñaajo ngir jagleel ko way-tawat yi ;
Soskat yi
Jawriñ Abdulaay Juuf Saar kalaame na yoon ñiy sos ak a weddi naan koronaawiris amul sax Senegaal, rawati-na Tuubaa. Ndekete, da cee am ñu xër ci diine ji ba mu ëpp, naan réew mi mbas du fi dug ndax sunu maam yu baax yi fi tëdd. Gisaanekat yi tamit kenn demul ñu des. Ñii a ngi naan koronaawiris bi amul, ñee naan mën nañ koo faj. Moo tax, bi leen jawriñ ji kalaamee yoon, ci lañ woo Abdulaay Mbay Peex, Selbe Ndom ak Gana Masire ñi doon weddi ne koronaawiris am na ci miim réew walla Tuubaa. Waaye, bi leen DIC wooloo, ku nekk ci ñoom dellu na ginnaaw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj